Al-An'am · 115/165
Tekki Waxtaan — Simoore Al-An'am
وَتَمَّتْ كَلِمَتُ رَبِّكَ صِدْقًا وَعَدْلًا ۚ لَّا مُبَدِّلَ لِكَلِمَاتِهِ ۚ وَهُوَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ ۝١١٥
Wa tammat Kalimatu Rabbika sidqanw wa `adlaa; laa mubaddila li Kalimaatih; wa Huwas Samee`ul `Aleem
📖 Tekkim Wolof
Sa kàddug Boroom mat na ci dëgg ak maandute. Ay waxam du soppeeku. Kuy dégg la, di Ku xam.

🎧 Dégg


📜 Aaya 113-117 — Simoore Al-An'am

113وَلِتَصْغَىٰ إِلَيْهِ أَفْئِدَةُ الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِالْآخِرَةِ وَلِيَرْضَوْهُ وَلِيَقْتَرِفُوا مَا هُم مُّقْتَرِفُونَ
Ak ngir xoli ñi gëmul àllaaxira jeng ci wax jooju jóge ca, ak ñu fàggu la ñuy fàggu [ciy bàkkaar].
114أَفَغَيْرَ اللَّهِ أَبْتَغِي حَكَمًا وَهُوَ الَّذِي أَنزَلَ إِلَيْكُمُ الْكِتَابَ مُفَصَّلًا ۚ وَالَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يَعْلَمُونَ أَنَّهُ مُنَزَّلٌ مِّن رَّبِّكَ بِالْحَقِّ ۖ فَلَا تَكُونَنَّ مِنَ الْمُمْتَرِينَ
Moo ndax ci keneen ku dul Yàlla laay sàkku àttekat, te Moom moo wàcce ci yéen Téere ba faramfàcce [lu ne] ? Te ña nga xam ne joxoon Nanu leen Téere, xam nañu ne dëgg la te mu wàcc tukkee ca sa Boroom. Kon yaw ci sa wàllu bopp, bul bokk mukk ci ñiy sikki-sàkka.
115وَتَمَّتْ كَلِمَتُ رَبِّكَ صِدْقًا وَعَدْلًا ۚ لَّا مُبَدِّلَ لِكَلِمَاتِهِ ۚ وَهُوَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ
Sa kàddug Boroom mat na ci dëgg ak maandute. Ay waxam du soppeeku. Kuy dégg la, di Ku xam.
116وَإِن تُطِعْ أَكْثَرَ مَن فِي الْأَرْضِ يُضِلُّوكَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۚ إِن يَتَّبِعُونَ إِلَّا الظَّنَّ وَإِنْ هُمْ إِلَّا يَخْرُصُونَ
Boo toppee li ëpp ci ñi nekk ci suuf si, ñu sànk la, nga sori yoonu Yàlla : ndax toppuñu lu dul ay njortu te nekkewuñu lu dul di fen.
117إِنَّ رَبَّكَ هُوَ أَعْلَمُ مَن يَضِلُّ عَن سَبِيلِهِ ۖ وَهُوَ أَعْلَمُ بِالْمُهْتَدِينَ
Te sa Boroom Moo gën a xam ku réere aw yoonam, te Moo gën a xam it ña tegu ci njub gindiku.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
115Aaya

Tekki — Al-An'am 115

Simoore Al-An'am Aaya 115 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Sa kàddug Boroom mat na ci dëgg ak maandute. Ay…

Simoore Aaya 115/165 — Simoore Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-An'am Dégg, Simoore Al-An'am Tekki, Simoore Al-An'am mp3, Simoore Al-An'am pdf. Aaya 113–117. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers