Al-An'am · 163/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
لَا شَرِيكَ لَهُ ۖ وَبِذَٰلِكَ أُمِرْتُ وَأَنَا أَوَّلُ الْمُسْلِمِينَ ۝١٦٣
Laa shareeka lahoo wa bizaalika umirtu wa ana awwalul muslimeen
📖 Tekkim Wolof
Amul bokkaale ! Te loolu lañu ma digal, te nekk naa di ku jiitu ca way-wommatu ña [jullit ña].”
🎧 Dégg

📜 Aaya 161-165 — Al-An'am

161قُلْ إِنَّنِي هَدَانِي رَبِّي إِلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ دِينًا قِيَمًا مِّلَّةَ إِبْرَاهِيمَ حَنِيفًا ۚ وَمَا كَانَ مِنَ الْمُشْرِكِينَ
Neel : “Sama Boroom gindi na ma teg ma ca yoon wu jub wa, di diine ju jub, di diiney Ibraahiima ma wéetal Boroomam te bokkuloon ca way-bokkaale ña.
162قُلْ إِنَّ صَلَاتِي وَنُسُكِي وَمَحْيَايَ وَمَمَاتِي لِلَّهِ رَبِّ الْعَالَمِينَ
Neel : “Samag julli, samag jaamu, samag dund ak samag dee, Yàlla Boroom àddina bee leen moom.
163لَا شَرِيكَ لَهُ ۖ وَبِذَٰلِكَ أُمِرْتُ وَأَنَا أَوَّلُ الْمُسْلِمِينَ
Amul bokkaale ! Te loolu lañu ma digal, te nekk naa di ku jiitu ca way-wommatu ña [jullit ña].”
164قُلْ أَغَيْرَ اللَّهِ أَبْغِي رَبًّا وَهُوَ رَبُّ كُلِّ شَيْءٍ ۚ وَلَا تَكْسِبُ كُلُّ نَفْسٍ إِلَّا عَلَيْهَا ۚ وَلَا تَزِرُ وَازِرَةٌ وِزْرَ أُخْرَىٰ ۚ ثُمَّ إِلَىٰ رَبِّكُم مَّرْجِعُكُمْ فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ فِيهِ تَخْتَلِفُونَ
Neel : “Ndax damay sàkku beneen boroom bu dul Yàlla, te Moom Mooy Boroom lépp lu ne ? Bakkan bu nekk, la mu fàggu ca moom doŋŋ lay delluwaat : kenn du yenul keneen yenam. Te ca seen Boroom ngeen di dellu Mu biral leen la ngeen nekkoon di ca juuyoo.
165وَهُوَ الَّذِي جَعَلَكُمْ خَلَائِفَ الْأَرْضِ وَرَفَعَ بَعْضَكُمْ فَوْقَ بَعْضٍ دَرَجَاتٍ لِّيَبْلُوَكُمْ فِي مَا آتَاكُمْ ۗ إِنَّ رَبَّكَ سَرِيعُ الْعِقَابِ وَإِنَّهُ لَغَفُورٌ رَّحِيمٌ
Moom Moo leen def ngeen di ay kuutaay ci suuf si, Mu yékkati lenn ci yéen ci kaw ñeneen ña, [Dakoy def] ngir nattu leen ca la Mu leen jox. Sa Boroom nag Ku gaaw ci mbugal la, te it Moom Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
163Aaya

Tekki — Al-An'am 163

Simoore Al-An'am Aaya 163 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Amul bokkaale ! Te loolu lañu ma digal, te nekk…

Simoore Aaya 163/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 161–165. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers