Al-An'am · 17/165
Tekki Waxtaan — Simoore Al-An'am
وَإِن يَمْسَسْكَ اللَّهُ بِضُرٍّ فَلَا كَاشِفَ لَهُ إِلَّا هُوَ ۖ وَإِن يَمْسَسْكَ بِخَيْرٍ فَهُوَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ ۝١٧
Wa iny-yamsaskal laahu bidurrin falaaa kaashifa lahoo illaa Huwa wa iny-yamsaska bikhairin fa Huwa `alaa kulli shai`in Qadeer
📖 Tekkim Wolof
Su la Yàlla tegee metit, kenn du mën a teggi lor jooju ku dul Moom. Su la joxee yiw, xamal ne Moom lu nekk la mën.

🎧 Dégg


📜 Aaya 15-19 — Simoore Al-An'am

15قُلْ إِنِّي أَخَافُ إِنْ عَصَيْتُ رَبِّي عَذَابَ يَوْمٍ عَظِيمٍ
Neel : “Su ma moyee sama Boroom [cig ndigalam], mbugalum bis bu màgg ba [Bis-pénc ba], ragal naa mu dal ma ”.
16مَّن يُصْرَفْ عَنْهُ يَوْمَئِذٍ فَقَدْ رَحِمَهُ ۚ وَذَٰلِكَ الْفَوْزُ الْمُبِينُ
Koo xam ne musal nañu ko ca bis booba ci mbugal moo ma, kooka Yàlla yërëm na ko, te loolu mooy texe tigi tigi.
17وَإِن يَمْسَسْكَ اللَّهُ بِضُرٍّ فَلَا كَاشِفَ لَهُ إِلَّا هُوَ ۖ وَإِن يَمْسَسْكَ بِخَيْرٍ فَهُوَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Su la Yàlla tegee metit, kenn du mën a teggi lor jooju ku dul Moom. Su la joxee yiw, xamal ne Moom lu nekk la mën.
18وَهُوَ الْقَاهِرُ فَوْقَ عِبَادِهِ ۚ وَهُوَ الْحَكِيمُ الْخَبِيرُ
Te Moom Aji-not la ci kaw jaam ñi ; Ku xereñ la [Moom Yàlla], Ku deñ la ci kumpa.
19قُلْ أَيُّ شَيْءٍ أَكْبَرُ شَهَادَةً ۖ قُلِ اللَّهُ ۖ شَهِيدٌ بَيْنِي وَبَيْنَكُمْ ۚ وَأُوحِيَ إِلَيَّ هَٰذَا الْقُرْآنُ لِأُنذِرَكُم بِهِ وَمَن بَلَغَ ۚ أَئِنَّكُمْ لَتَشْهَدُونَ أَنَّ مَعَ اللَّهِ آلِهَةً أُخْرَىٰ ۚ قُل لَّا أَشْهَدُ ۚ قُلْ إِنَّمَا هُوَ إِلَٰهٌ وَاحِدٌ وَإِنَّنِي بَرِيءٌ مِّمَّا تُشْرِكُونَ
Neel : “Ana lan moo gën a màgg ci wàllu seede ? ”. Neel : “Yàlla dana nekk seede ci sama diggante ak yéen ; te sol nañu ma Alxuraan jii ngir ma waar ci yéen ak képp ku ca jot.”. Moo ndax dangeen di seede ne am na jeneen yàlla ju dul Yàlla ? Neeleen : “Seedewuma loolu”. Neel: “Moom daal nekkul lu dul jenn Yàlla doŋŋ. Te man set naa wecc ci li ngeen koy bokkaale”.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
17Aaya

Tekki — Al-An'am 17

Simoore Al-An'am Aaya 17 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Su la Yàlla tegee metit, kenn du mën a teggi…

Simoore Aaya 17/165 — Simoore Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-An'am Dégg, Simoore Al-An'am Tekki, Simoore Al-An'am mp3, Simoore Al-An'am pdf. Aaya 15–19. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers