Al-A'raf · 136/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
فَانتَقَمْنَا مِنْهُمْ فَأَغْرَقْنَاهُمْ فِي الْيَمِّ بِأَنَّهُمْ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا وَكَانُوا عَنْهَا غَافِلِينَ ۝١٣٦
Fantaqamnaa minhum fa aghraqnaahum kazzaboo bi Aayaatinaa wa kaanoo `anhaa ghaafileen
📖 Tekkim Wolof
Tax na Nu feyyu ci ñoom ; labal leen ci géej gi, ndax ñoom dañoo weddi sunuy tegtal, sàggane leen.

🎧 Dégg


📜 Aaya 134-138 — Al-A'raf

134وَلَمَّا وَقَعَ عَلَيْهِمُ الرِّجْزُ قَالُوا يَا مُوسَى ادْعُ لَنَا رَبَّكَ بِمَا عَهِدَ عِندَكَ ۖ لَئِن كَشَفْتَ عَنَّا الرِّجْزَ لَنُؤْمِنَنَّ لَكَ وَلَنُرْسِلَنَّ مَعَكَ بَنِي إِسْرَائِيلَ
Ba mbugal ma agsee ca ñoom, ñu ne : “Yaw Muusaa, ñaanal nu sa Boroom ci kóllare gi dox seen diggante. Boo nu tàggaleek mbugal mii, dananu la gëm te dananu bàyyi Banii- israayil ñu dem ànd ak yaw”.
135فَلَمَّا كَشَفْنَا عَنْهُمُ الرِّجْزَ إِلَىٰ أَجَلٍ هُم بَالِغُوهُ إِذَا هُمْ يَنكُثُونَ
Ba Nu teggee ca ñoom mbugal ma [ca àpp ba mu waroon a yem], firi nañu la ñu dige woon.
136فَانتَقَمْنَا مِنْهُمْ فَأَغْرَقْنَاهُمْ فِي الْيَمِّ بِأَنَّهُمْ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا وَكَانُوا عَنْهَا غَافِلِينَ
Tax na Nu feyyu ci ñoom ; labal leen ci géej gi, ndax ñoom dañoo weddi sunuy tegtal, sàggane leen.
137وَأَوْرَثْنَا الْقَوْمَ الَّذِينَ كَانُوا يُسْتَضْعَفُونَ مَشَارِقَ الْأَرْضِ وَمَغَارِبَهَا الَّتِي بَارَكْنَا فِيهَا ۖ وَتَمَّتْ كَلِمَتُ رَبِّكَ الْحُسْنَىٰ عَلَىٰ بَنِي إِسْرَائِيلَ بِمَا صَبَرُوا ۖ وَدَمَّرْنَا مَا كَانَ يَصْنَعُ فِرْعَوْنُ وَقَوْمُهُ وَمَا كَانُوا يَعْرِشُونَ
Nu donnale suuf si nit ña ñu nekkoon daan leen suufeel, penku ba sowu te barkeel ko. Noonu, sa dogalu Boroom bu rafet bi, daldi mat ci Banii-israayil ngir la ñu nekkoon di muñ. Nu rajaxe la Firawna ak u nitam nekkoon di liggéey ak ya ñu tabaxoon.
138وَجَاوَزْنَا بِبَنِي إِسْرَائِيلَ الْبَحْرَ فَأَتَوْا عَلَىٰ قَوْمٍ يَعْكُفُونَ عَلَىٰ أَصْنَامٍ لَّهُمْ ۚ قَالُوا يَا مُوسَى اجْعَل لَّنَا إِلَٰهًا كَمَا لَهُمْ آلِهَةٌ ۚ قَالَ إِنَّكُمْ قَوْمٌ تَجْهَلُونَ
Jàllale Nanu Bani-Israayil géej ga. Ñu fekk fa aw nit ñoo xam ne ña nga doon jaamu seeni xërëm, ñu ne : "Muusaa, defal nu yàlla ju mel ni seen yàlla.”. Mu ne leen : “Yéen daal ñu réer ngeen.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
136Aaya

Tekki — Al-A'raf 136

Simoore Al-A'raf Aaya 136 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Tax na Nu feyyu ci ñoom ; labal leen ci…

Simoore Aaya 136/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 134–138. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers