Simoore Al-Fajr pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Fajr pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Fajr Tekki. Simoore Al-Fajr (Meccan) 30 Aaya.
Related
More Simoore PDF
Simoore Al-Fajr

ﭤﭥ
89:1
Ci njël Maa ngi giiñ !
ﭦﭧﭨ
89:2
ak ci fukki guddi ya (fukki fani tabaski) !
ﭩﭪﭫ
89:3
Ak ci tóolent ak ci lu tóol !
ﭬﭭﭮﭯ
89:4
Ak ci guddi gi suy tàmbali !
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
89:5
Moo ndax nekk na ci loolu, ngiñul boroom xel ?
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
89:6
Xanaa gisoo naka la sa Boroom def waa Aad
ﭾﭿﮀﮁ
89:7
Iram, ma doon boroomi kenu,
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
89:8
yoo xam ne kemam amul ci menn réew ?
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
89:9
ak waa Saamud ña daan yatt xeer ya ca xur ya ?
ﮏﮐﮑﮒ
89:10
ak Firawna, ma doonoon boroomi dàtt ?
ﮓﮔﮕﮖﮗ
89:11
Ñoom, ñoo gënoona bew ci réew yi,
ﮘﮙﮚﮛ
89:12
te ñu bariloon fa lool ag yàq.
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
89:13
Sa Boroom daldi leen sotti yarum mbugël.
ﮢﮣﮤﮥ
89:14
Sa Boroom nag ma ngay fuglu.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
89:15
Nit nag, moom saa su ko boroomam nattoo teral ko xéewal ko, mu ne : “Sama Boroom teral na ma”.
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
89:16
Saa su ko nattoo wàññi wërsagëm, muy wax naan : “Sama Boroom toroxal nama”.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
89:17
Déedéet ! Yéen kay, du ngeen teral mukk jirim ak di tabe ci moom ;
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
89:18
te it du ngeen sonnu mukk ci di leel miskiin,
ﯫﯬﯭﯮﯯ
89:19
te ngeen di lekk alal ndono lekkiin wu ñaaw,
ﯰﯱﯲﯳﯴ
89:20
te da ngeen bëgg alal bëgg gu tar.
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
89:21
(Bàyyileen xel) ! saa su nu walee suuf si ba mu di pëndax,
ﯽﯾﯿﰀﰁﰂ
89:22
sa Boroom dikk ak malaaka ya, def ay sàppey sàppe,
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
89:23
bu keroogee, danuy indi Safarey jahanama ; bu keroogee it, nit dana fàttaliku. Waaye damaa xamut lu ko fàttaliku ga di jariñ ?
ﭜﭝﭞﭟﭠ
89:24
Muy wax naan : “Aka neexoon ! Ca ba muy dundu ma defoon lu baax !
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
89:25
Bu keroogee, mbugël ma deefu ko mbugël kenn,
ﭧﭨﭩﭪﭫ
89:26
te it kenn du yolomal jéngam ba.
ﭬﭭﭮﭯ
89:27
“Éy yaw, bakkan bi dalum xel,
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
89:28
delul ca sa Boroom, di gërëm ñu dila gërëm ;
ﭶﭷﭸﭹ
89:29
tàbbil ca Samay jaam,
ﭺﭻﭼ
89:30
tàbbil it ca Sama biir ̈Àjjana”.
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, September 9, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







