Simoore Al-Balad pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Balad pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Balad Tekki. Simoore Al-Balad (Meccan) 20 Aaya.
Related
More Simoore PDF
Simoore Al-Balad

ﭽﭾﭿﮀﮁ
90:1
Déet !... Ma ngi giiñ ci dëkk bii !
ﮂﮃﮄﮅﮆ
90:2
te yaw, sax ci dëkk bi nga dëkk
ﮇﮈﮉﮊ
90:3
Ak ci baay ak la mu jur !
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
90:4
Noo, bind nit muy jànkonteeki coono.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
90:5
Moo ndax dafa defe ni kenn manul ci moom dara ?
ﮘﮙﮚﮛﮜ
90:6
Ma ngay wax naan : “Sànk naa alal ju bari”.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
90:7
Moo ndax dafa defe ne kenn da koo gisul ?
ﮣﮤﮥﮦﮧ
90:8
Moo ndax defalunu ko ñaari gët,
ﮨﮩﮪ
90:9
ak aw làmmiñ ak ñaari tuñ ?
ﮫﮬﮭ
90:10
Nu gindi ko tegtal ko ñaari yoon yi, mbaax, mbon.
ﮮﮯﮰﮱ
90:11
Te, moom moo lànka soobu yoon wu tënku wa (mitti) !
ﯓﯔﯕﯖﯗ
90:12
Ana lan moo lay xamal yoon wu tënku wa ?
ﯘﯙﯚ
90:13
Moo di [goréel jaam],
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
90:14
mbaa joxe lekk, ci bisub xondooñ, xiif bu tar
ﯢﯣﯤﯥ
90:15
ab jirim mba mbokk mu jige
ﯦﯧﯨﯩﯪ
90:16
walla ab miskiin bu fondóoñ.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
90:17
Ba noppi, bokk ca, ña gëm tey dénkante ci muñ, di dénkante it ci yërmaande.
ﯵﯶﯷﯸ
90:18
Ñooñee ñoo di waa ndeyjoor ;
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗ
90:19
ñay weddi sunuy Laaya ñoom ñoo di waa càmmoñ.
ﭘﭙﭚﭛ
90:20
Safara waa ngi di gand.
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, September 9, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







