15 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭜﭝﭞ
91:1 Ci jant beek leeram. Maa ngi giñ !
ﭟﭠﭡﭢ
91:2 Ak ci weer wi su ko dee topp !
ﭣﭤﭥﭦ
91:3 Ak ci bëcëg bi su ko muuree !
ﭧﭨﭩﭪ
91:4 Ak ci guddi gi su ko muuree !
ﭫﭬﭭﭮ
91:5 Ak ci asamaan seek ka ko tabax !
ﭯﭰﭱﭲ
91:6 Ak ci suuf sek ka ko maasale !
ﭳﭴﭵﭶ
91:7 Ak ci ruu geek Ka ko yemale ;
ﭷﭸﭹﭺ
91:8 moom mi ko ràññatleel mbaax, ak mbon !
ﭻﭼﭽﭾﭿ
91:9 képp ku ko sellal, daldi nay texe
ﮀﮁﮂﮃﮄ
91:10 te it, képp ku ko sàggane, daldi nay sooy.
ﮅﮆﮇﮈ
91:11 Waa Saamuud, seen bewte, tax na ñu weddi,
ﮉﮊﮋﮌ
91:12 ba ca ña gën weddi potoxlóo
ﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔ
91:13 Yonentub Yàlla ba ne leen : “Bàyyileen giléemug Yàlla gi ! mu naan”
ﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
91:14 Ñu weddi ko, rey ko. Seen Boroom, maasale na mbugël ma.ca kaw nit ñépp
ﮝﮞﮟﮠ
91:15 Te ragalul dara ca la cay mujj :

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 29, 2026

Don't forget us in your sincere prayers