Yusuf · 22/111
Tekki Waxtaan — Simoore Yusuf
وَلَمَّا بَلَغَ أَشُدَّهُ آتَيْنَاهُ حُكْمًا وَعِلْمًا ۚ وَكَذَٰلِكَ نَجْزِي الْمُحْسِنِينَ ۝٢٢
Wa lammaa balagha ashuddahooo aatainaahu bukmanw wa `ilmaa; wa kazaa lika najzil muhsineen
📖 Tekkim Wolof
Ba mu màggee ba tollu ci góor gu mat, jox Nanu ko ràññee ak xam-xam. Te noonu Lanuy feye way-rafetal ña.

🎧 Dégg


📜 Aaya 20-24 — Simoore Yusuf

20وَشَرَوْهُ بِثَمَنٍ بَخْسٍ دَرَاهِمَ مَعْدُودَةٍ وَكَانُوا فِيهِ مِنَ الزَّاهِدِينَ
Ñu jaay ko ci njëg gu néew : ay dërëm yu bariwul. Ndax dañu koo xeeboon.
21وَقَالَ الَّذِي اشْتَرَاهُ مِن مِّصْرَ لِامْرَأَتِهِ أَكْرِمِي مَثْوَاهُ عَسَىٰ أَن يَنفَعَنَا أَوْ نَتَّخِذَهُ وَلَدًا ۚ وَكَذَٰلِكَ مَكَّنَّا لِيُوسُفَ فِي الْأَرْضِ وَلِنُعَلِّمَهُ مِن تَأْوِيلِ الْأَحَادِيثِ ۚ وَاللَّهُ غَالِبٌ عَلَىٰ أَمْرِهِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ
Ka ko jënd di waa Misra, wax na jabaram ne ko : “Teralal ma ko. Xéy-na mu jariñ nu mbaa nu def ko sunu doom.”. Noonu la nu darajaale Yuusufa ci suuf si, ak it ngir Nu jàngal ko pirim gént. Yàlla kuy not la ca la Mu namm : waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
22وَلَمَّا بَلَغَ أَشُدَّهُ آتَيْنَاهُ حُكْمًا وَعِلْمًا ۚ وَكَذَٰلِكَ نَجْزِي الْمُحْسِنِينَ
Ba mu màggee ba tollu ci góor gu mat, jox Nanu ko ràññee ak xam-xam. Te noonu Lanuy feye way-rafetal ña.
23وَرَاوَدَتْهُ الَّتِي هُوَ فِي بَيْتِهَا عَن نَّفْسِهِ وَغَلَّقَتِ الْأَبْوَابَ وَقَالَتْ هَيْتَ لَكَ ۚ قَالَ مَعَاذَ اللَّهِ ۖ إِنَّهُ رَبِّي أَحْسَنَ مَثْوَايَ ۖ إِنَّهُ لَا يُفْلِحُ الظَّالِمُونَ
Ndaw sa nga xam ne [Moo ko fat ca kërëm] sàkku na ko ci boppam. Tëj na buntu ya ne ko : “Ayca ñëwal ci man” - Mu ne : “Maa ngi muslu ci Yàlla ! [tëdd ak yaw] te sama sang [bi ma jënd] fonk na ma, teral na ma. Te tooñkat ya duñu texe mukk”.
24وَلَقَدْ هَمَّتْ بِهِ ۖ وَهَمَّ بِهَا لَوْلَا أَن رَّأَىٰ بُرْهَانَ رَبِّهِ ۚ كَذَٰلِكَ لِنَصْرِفَ عَنْهُ السُّوءَ وَالْفَحْشَاءَ ۚ إِنَّهُ مِنْ عِبَادِنَا الْمُخْلَصِينَ
Ndaw sa xemmem na [Yuusufa]. Moom [Yuusufa] it xemmem na [ndaw sa] bu dul koon la mu gis kaawtéefi Boroomam. Noonu la Nu def ngir fegal ko ñaawtéef ak njaaloo. Moom sax dafa bokk ca sunu jaam yu sell ya.
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
22Aaya

Tekki — Yusuf 22

Simoore Yusuf Aaya 22 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba mu màggee ba tollu ci góor gu mat, jox…

Simoore Aaya 22/111 — Simoore Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Yusuf Dégg, Simoore Yusuf Tekki, Simoore Yusuf mp3, Simoore Yusuf pdf. Aaya 20–24. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers