Yusuf · 84/111
Tekki Waxtaan — Simoore Yusuf
وَتَوَلَّىٰ عَنْهُمْ وَقَالَ يَا أَسَفَىٰ عَلَىٰ يُوسُفَ وَابْيَضَّتْ عَيْنَاهُ مِنَ الْحُزْنِ فَهُوَ كَظِيمٌ ۝٨٤
Wa tawallaa `anhum wa qaala yaaa asafaa `alaa Yoosufa wabyaddat `aynaahu minal huzni fahuwa kazeem
📖 Tekkim Wolof
Mu dummóoyu leen, wax ne : “Céy sama njàqare ci Yuusufa ! ”. Noona ay gëtam weex [gisatul] ngir mer ma mu wann.

🎧 Dégg


📜 Aaya 82-86 — Simoore Yusuf

82وَاسْأَلِ الْقَرْيَةَ الَّتِي كُنَّا فِيهَا وَالْعِيرَ الَّتِي أَقْبَلْنَا فِيهَا ۖ وَإِنَّا لَصَادِقُونَ
Laajal waa dëkk ba nu nekkoon, ak njëgg ma nu àndaloon ñibbisi. Li nu wax dëgg la.”
83قَالَ بَلْ سَوَّلَتْ لَكُمْ أَنفُسُكُمْ أَمْرًا ۖ فَصَبْرٌ جَمِيلٌ ۖ عَسَى اللَّهُ أَن يَأْتِيَنِي بِهِمْ جَمِيعًا ۚ إِنَّهُ هُوَ الْعَلِيمُ الْحَكِيمُ
[Seen baay tontu leen] ne : “Deewallaay dangeen a topp seen bakkan mu rafetal leen am mbir !... [Muñ gu rafet]. Xéy-na Yàlla delloosil nu leen ñoom ñépp. Moom Yàlla Ku xereñ la, Ku xam la”.
84وَتَوَلَّىٰ عَنْهُمْ وَقَالَ يَا أَسَفَىٰ عَلَىٰ يُوسُفَ وَابْيَضَّتْ عَيْنَاهُ مِنَ الْحُزْنِ فَهُوَ كَظِيمٌ
Mu dummóoyu leen, wax ne : “Céy sama njàqare ci Yuusufa ! ”. Noona ay gëtam weex [gisatul] ngir mer ma mu wann.
85قَالُوا تَاللَّهِ تَفْتَأُ تَذْكُرُ يُوسُفَ حَتَّىٰ تَكُونَ حَرَضًا أَوْ تَكُونَ مِنَ الْهَالِكِينَ
- Ñu ne ko : “Céy Yàlla ! Doo deñ di fàttaliku Yuusufa, ba tax na yaa ngi wéradi te mën nga cee loru”.
86قَالَ إِنَّمَا أَشْكُو بَثِّي وَحُزْنِي إِلَى اللَّهِ وَأَعْلَمُ مِنَ اللَّهِ مَا لَا تَعْلَمُونَ
- Mu ne : “Defuma lu dul tawat sama njàqare ak sama naqar ci Yàlla. Te xam naa ci Yàlla lu ngeen xamul.
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
84Aaya

Tekki — Yusuf 84

Simoore Yusuf Aaya 84 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu dummóoyu leen, wax ne : “Céy sama njàqare ci…

Simoore Aaya 84/111 — Simoore Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Yusuf Dégg, Simoore Yusuf Tekki, Simoore Yusuf mp3, Simoore Yusuf pdf. Aaya 82–86. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers