An-Nahl · 38/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
وَأَقْسَمُوا بِاللَّهِ جَهْدَ أَيْمَانِهِمْ ۙ لَا يَبْعَثُ اللَّهُ مَن يَمُوتُ ۚ بَلَىٰ وَعْدًا عَلَيْهِ حَقًّا وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ ۝٣٨
Wa aqsamoo billaahi jahda aimaanihim laa yab`asul laahu mai yamoot; balaa wa`dan `alaihi haqqanw wa laakinna aksaran naasi laa ya`lamoon
📖 Tekkim Wolof
Ñangay giñ ba fa seeni ngiñ yem naan : “Yàlla du dekkal ku dee”. Axakañ ! Loolu dig bu dëggu la ci Moom [Yàlla], waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
🎧 Dégg

📜 Aaya 36-40 — An-Nahl

36وَلَقَدْ بَعَثْنَا فِي كُلِّ أُمَّةٍ رَّسُولًا أَنِ اعْبُدُوا اللَّهَ وَاجْتَنِبُوا الطَّاغُوتَ ۖ فَمِنْهُم مَّنْ هَدَى اللَّهُ وَمِنْهُم مَّنْ حَقَّتْ عَلَيْهِ الضَّلَالَةُ ۚ فَسِيرُوا فِي الْأَرْضِ فَانظُرُوا كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الْمُكَذِّبِينَ
Yónni nañu ci xeet wu nekk ab Yonent [buy xamle ne] : “Jaamuleen Yàlla te ngeen moytuy xërëm”. Mu am ci ñoom [xeet yooyu] ñu Yàlla jubal ak ñoo xam ne réer war na ci ñoom. Doxleen ci seeni suuf te xool ña weddi woon naka lañu mujje.
37إِن تَحْرِصْ عَلَىٰ هُدَاهُمْ فَإِنَّ اللَّهَ لَا يَهْدِي مَن يُضِلُّ ۖ وَمَا لَهُم مِّن نَّاصِرِينَ
Loo xér xér ci jubal leen...Yàlla moom du gindi ku Mu bàyyi cig réer. Te duñu am ñu leen dimbali.
38وَأَقْسَمُوا بِاللَّهِ جَهْدَ أَيْمَانِهِمْ ۙ لَا يَبْعَثُ اللَّهُ مَن يَمُوتُ ۚ بَلَىٰ وَعْدًا عَلَيْهِ حَقًّا وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ
Ñangay giñ ba fa seeni ngiñ yem naan : “Yàlla du dekkal ku dee”. Axakañ ! Loolu dig bu dëggu la ci Moom [Yàlla], waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
39لِيُبَيِّنَ لَهُمُ الَّذِي يَخْتَلِفُونَ فِيهِ وَلِيَعْلَمَ الَّذِينَ كَفَرُوا أَنَّهُمْ كَانُوا كَاذِبِينَ
Ngir mu leeralal leen [lay dëgg] ca la ñu daan wuute, ak it ña weddi xam ne dañu daan fen.
40إِنَّمَا قَوْلُنَا لِشَيْءٍ إِذَا أَرَدْنَاهُ أَن نَّقُولَ لَهُ كُن فَيَكُونُ
[Li am mooy], Sunu kàddu ci mbir, bu Nu ko bëggee, Danu ko naan : “Nekkal”. Mu daldi nekk.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
38Aaya

Tekki — An-Nahl 38

Simoore An-Nahl Aaya 38 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñangay giñ ba fa seeni ngiñ yem naan : “Yàlla…

Simoore Aaya 38/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 36–40. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers