Al-Isra · 108/111
Tekki Waxtaan — Al-Isra
وَيَقُولُونَ سُبْحَانَ رَبِّنَا إِن كَانَ وَعْدُ رَبِّنَا لَمَفْعُولًا ۝١٠٨
Wa yaqooloona Subhaana Rabbinaaa in kaana wa`du Rabbinaa lamaf`oolaa
📖 Tekkim Wolof
te ñuy wax ne : “Tudd nanu sellug sunu Boroom ! Digub sunu Boroom fàwwu mu am”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 106-110 — Al-Isra

106وَقُرْآنًا فَرَقْنَاهُ لِتَقْرَأَهُ عَلَى النَّاسِ عَلَىٰ مُكْثٍ وَنَزَّلْنَاهُ تَنزِيلًا
Te Alxuraan, téqale Nanu ko [cig wàccam] ngir nga jàng ko ci nit ñi, cig teey. Te wàcce Nanu ko ndànk-ndànk.
107قُلْ آمِنُوا بِهِ أَوْ لَا تُؤْمِنُوا ۚ إِنَّ الَّذِينَ أُوتُوا الْعِلْمَ مِن قَبْلِهِ إِذَا يُتْلَىٰ عَلَيْهِمْ يَخِرُّونَ لِلْأَذْقَانِ سُجَّدًا
Neel : “Gëmleen ko mbaa ngeen bañ koo gëm, nanga xam ne joxeef na leen xam-xam. La ko jiitu, bu ñu jàngee ci seen kanam, danañu rot dëpp seeni sikkim ci suuf, sujjóot”
108وَيَقُولُونَ سُبْحَانَ رَبِّنَا إِن كَانَ وَعْدُ رَبِّنَا لَمَفْعُولًا
te ñuy wax ne : “Tudd nanu sellug sunu Boroom ! Digub sunu Boroom fàwwu mu am”.
109وَيَخِرُّونَ لِلْأَذْقَانِ يَبْكُونَ وَيَزِيدُهُمْ خُشُوعًا ۩
Ñu rot dëpp seeni sikkim ca suuf di sujjóot. Seen toroxlu ci Yàlla dolliku.
110قُلِ ادْعُوا اللَّهَ أَوِ ادْعُوا الرَّحْمَٰنَ ۖ أَيًّا مَّا تَدْعُوا فَلَهُ الْأَسْمَاءُ الْحُسْنَىٰ ۚ وَلَا تَجْهَرْ بِصَلَاتِكَ وَلَا تُخَافِتْ بِهَا وَابْتَغِ بَيْنَ ذَٰلِكَ سَبِيلًا
Neel : “Wooleen Yàlla mbaa ngeen woo Aji-yërëme ji. Lu ngeen mën a woo [xamleen ne] Moo moom tur ya gën a rafet. Bul biral ci kaw ci sa julli ; te bul ca yelu it, sàkkal ci diggante ñaar yooyu [yoon wu digg-dóomu]”.
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
108Aaya

Tekki — Al-Isra 108

Simoore Al-Isra Aaya 108 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : te ñuy wax ne : “Tudd nanu sellug sunu Boroom…

Simoore Aaya 108/111 — Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Isra Dégg, Al-Isra Tekki, Al-Isra mp3, Al-Isra pdf. Aaya 106–110. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers