Al-Isra · 67/111
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Isra
وَإِذَا مَسَّكُمُ الضُّرُّ فِي الْبَحْرِ ضَلَّ مَن تَدْعُونَ إِلَّا إِيَّاهُ ۖ فَلَمَّا نَجَّاكُمْ إِلَى الْبَرِّ أَعْرَضْتُمْ ۚ وَكَانَ الْإِنسَانُ كَفُورًا ۝٦٧
Wa izaa massakumuddurru fil bahri dalla man tad`oona illaaa iyyaahu falammaa najjaakum ilal barri a`radtum; wa kaanal insaanu kafooraa
📖 Tekkim Wolof
Bu leen naqar dabee ci géej, ña ngeen doon jaamu réer leen ginnaawam. Te bu Nu leen musalee ba ñu agsi ci jéeri ji, ngeen dëddu. Nit daal ku goreedi la !

🎧 Dégg


📜 Aaya 65-69 — Simoore Al-Isra

65إِنَّ عِبَادِي لَيْسَ لَكَ عَلَيْهِمْ سُلْطَانٌ ۚ وَكَفَىٰ بِرَبِّكَ وَكِيلًا
Naka samay jaam, doo am genn kàttan ci ñoom”. Ndax sa Boroom doy na cëslaay.
66رَّبُّكُمُ الَّذِي يُزْجِي لَكُمُ الْفُلْكَ فِي الْبَحْرِ لِتَبْتَغُوا مِن فَضْلِهِ ۚ إِنَّهُ كَانَ بِكُمْ رَحِيمًا
Sa Boroom mooy kiy dawloo gaal ci géej, ngir ngeen mën a sàkku ay xéewalam ; Naka Moom ku am yërmaande la ci yéen,
67وَإِذَا مَسَّكُمُ الضُّرُّ فِي الْبَحْرِ ضَلَّ مَن تَدْعُونَ إِلَّا إِيَّاهُ ۖ فَلَمَّا نَجَّاكُمْ إِلَى الْبَرِّ أَعْرَضْتُمْ ۚ وَكَانَ الْإِنسَانُ كَفُورًا
Bu leen naqar dabee ci géej, ña ngeen doon jaamu réer leen ginnaawam. Te bu Nu leen musalee ba ñu agsi ci jéeri ji, ngeen dëddu. Nit daal ku goreedi la !
68أَفَأَمِنتُمْ أَن يَخْسِفَ بِكُمْ جَانِبَ الْبَرِّ أَوْ يُرْسِلَ عَلَيْكُمْ حَاصِبًا ثُمَّ لَا تَجِدُوا لَكُمْ وَكِيلًا
Moo ndax dangeen a naagu ne : du xar suuf si [mëdd leen], walla duleen yónnee ngelawu sànniy xeer fekk dungeen ci am ku leen ci yiir.
69أَمْ أَمِنتُمْ أَن يُعِيدَكُمْ فِيهِ تَارَةً أُخْرَىٰ فَيُرْسِلَ عَلَيْكُمْ قَاصِفًا مِّنَ الرِّيحِ فَيُغْرِقَكُم بِمَا كَفَرْتُمْ ۙ ثُمَّ لَا تَجِدُوا لَكُمْ عَلَيْنَا بِهِ تَبِيعًا
Am dangeen a wóolu ne duleen ca delloo [ca biir géej] beneen yoon, yónnee leen ngelaw lu tar, Mu labal leen ngir seen weddi ? Te fekk dungeen mën a am ku leen dimbali ci Nun !
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
67Aaya

Tekki — Al-Isra 67

Simoore Al-Isra Aaya 67 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu leen naqar dabee ci géej, ña ngeen doon jaamu…

Simoore Aaya 67/111 — Simoore Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Isra Dégg, Simoore Al-Isra Tekki, Simoore Al-Isra mp3, Simoore Al-Isra pdf. Aaya 65–69. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers