Al-Isra · 98/111
Tekki Waxtaan — Al-Isra
ذَٰلِكَ جَزَاؤُهُم بِأَنَّهُمْ كَفَرُوا بِآيَاتِنَا وَقَالُوا أَإِذَا كُنَّا عِظَامًا وَرُفَاتًا أَإِنَّا لَمَبْعُوثُونَ خَلْقًا جَدِيدًا ۝٩٨
Zaalika jazaa`uhum biannahum kafaroo bi aayaatinaa wa qaalooo `a izaa kunnaa `izaamanw wa rufaatan`a innaa lamaboosoona khalqan jadeedaa
📖 Tekkim Wolof
Loolu moo di seen pey, ndax ñoom dañoo weddi Samay kàddu, naan : “Ndax [bu ñu deewee] ba nekk yax yu funux, dananu dekki nekk mbindeef yu bees ? ”
🎧 Dégg

📜 Aaya 96-100 — Al-Isra

96قُلْ كَفَىٰ بِاللَّهِ شَهِيدًا بَيْنِي وَبَيْنَكُمْ ۚ إِنَّهُ كَانَ بِعِبَادِهِ خَبِيرًا بَصِيرًا
Neel : “Yàlla doy na seede sama diggante ak yéen”. Moom Yàlla nag nekk na ci ay jaamam, di Ku xam, di Kuy gis [seeni mbir].
97وَمَن يَهْدِ اللَّهُ فَهُوَ الْمُهْتَدِ ۖ وَمَن يُضْلِلْ فَلَن تَجِدَ لَهُمْ أَوْلِيَاءَ مِن دُونِهِ ۖ وَنَحْشُرُهُمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ عَلَىٰ وُجُوهِهِمْ عُمْيًا وَبُكْمًا وَصُمًّا ۖ مَّأْوَاهُمْ جَهَنَّمُ ۖ كُلَّمَا خَبَتْ زِدْنَاهُمْ سَعِيرًا
Ku Yàlla gindi nga jub, Ku mu bàyyi cig réer... duñu am keneen ku ñuy wéeru te Dananu leen dajale bisub dekki ba, ñu di leen diri ci seeni kanam, ñu gumba, tëx, lu. Seen dëkkuwaay moo di Safara : te saa yu giimee Nu dolli leen seneen safara.
98ذَٰلِكَ جَزَاؤُهُم بِأَنَّهُمْ كَفَرُوا بِآيَاتِنَا وَقَالُوا أَإِذَا كُنَّا عِظَامًا وَرُفَاتًا أَإِنَّا لَمَبْعُوثُونَ خَلْقًا جَدِيدًا
Loolu moo di seen pey, ndax ñoom dañoo weddi Samay kàddu, naan : “Ndax [bu ñu deewee] ba nekk yax yu funux, dananu dekki nekk mbindeef yu bees ? ”
99۞ أَوَلَمْ يَرَوْا أَنَّ اللَّهَ الَّذِي خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ قَادِرٌ عَلَىٰ أَن يَخْلُقَ مِثْلَهُمْ وَجَعَلَ لَهُمْ أَجَلًا لَّا رَيْبَ فِيهِ فَأَبَى الظَّالِمُونَ إِلَّا كُفُورًا
Ndax dañoo gisul ne Yàlla moo bind asamaan yi ak suuf si, te Ku kàttanu la ci bind leneen lu mel ni ñoom ? Te Mu àppal leen dig bu amul benn sikki-sàkka, waaye way-tooñ ña wéy nañu ci seenug weddi.
100قُل لَّوْ أَنتُمْ تَمْلِكُونَ خَزَائِنَ رَحْمَةِ رَبِّي إِذًا لَّأَمْسَكْتُمْ خَشْيَةَ الْإِنفَاقِ ۚ وَكَانَ الْإِنسَانُ قَتُورًا
Neel : “Su fekkoon ne yéen a moom ndàmbi yërmaandey Yàlla yi ; kon ngeen nay [ci joxe ko] ngir ŋott. Nit dafa di ku ŋott !
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
98Aaya

Tekki — Al-Isra 98

Simoore Al-Isra Aaya 98 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Loolu moo di seen pey, ndax ñoom dañoo weddi Samay…

Simoore Aaya 98/111 — Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Isra Dégg, Al-Isra Tekki, Al-Isra mp3, Al-Isra pdf. Aaya 96–100. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers