Taha · 88/135
Tekki Waxtaan — Taha
فَأَخْرَجَ لَهُمْ عِجْلًا جَسَدًا لَّهُ خُوَارٌ فَقَالُوا هَٰذَا إِلَٰهُكُمْ وَإِلَٰهُ مُوسَىٰ فَنَسِيَ ۝٨٨
Fa akhraja lahum `ijlan jasadal lahoo khuwaarun faqaaloo haazaaa ilaahukum wa ilaahu Moosaa fanasee
📖 Tekkim Wolof
Daldi leen cay génneel aw sëll [nag]. Ne leen : “Mooy seen yàlla ; ñu daldi fàtte Yàllay Muusaa” !

🎧 Dégg


📜 Aaya 86-90 — Taha

86فَرَجَعَ مُوسَىٰ إِلَىٰ قَوْمِهِ غَضْبَانَ أَسِفًا ۚ قَالَ يَا قَوْمِ أَلَمْ يَعِدْكُمْ رَبُّكُمْ وَعْدًا حَسَنًا ۚ أَفَطَالَ عَلَيْكُمُ الْعَهْدُ أَمْ أَرَدتُّمْ أَن يَحِلَّ عَلَيْكُمْ غَضَبٌ مِّن رَّبِّكُمْ فَأَخْلَفْتُم مَّوْعِدِي
Muusaa dellu fa nitam ña mer bay fuur ; ne leen : "Yéen samaw nit, ndax Yàlla digu leen woon dig wu rafet ? Walla dig wa dafa yàgg ? Walla dangeen bëgg merum Yàlla wàcc ci seen kaw, ba tax ngeen wuute samag dig ay yéen ? ”
87قَالُوا مَا أَخْلَفْنَا مَوْعِدَكَ بِمَلْكِنَا وَلَٰكِنَّا حُمِّلْنَا أَوْزَارًا مِّن زِينَةِ الْقَوْمِ فَقَذَفْنَاهَا فَكَذَٰلِكَ أَلْقَى السَّامِرِيُّ
Ñu ne ko : “Wuutewuñu sab dig. Waaye danu noo nax sànniloo nu takkaay ya ; ca noona la ko Saamiriyu sànnee ca safara wa.
88فَأَخْرَجَ لَهُمْ عِجْلًا جَسَدًا لَّهُ خُوَارٌ فَقَالُوا هَٰذَا إِلَٰهُكُمْ وَإِلَٰهُ مُوسَىٰ فَنَسِيَ
Daldi leen cay génneel aw sëll [nag]. Ne leen : “Mooy seen yàlla ; ñu daldi fàtte Yàllay Muusaa” !
89أَفَلَا يَرَوْنَ أَلَّا يَرْجِعُ إِلَيْهِمْ قَوْلًا وَلَا يَمْلِكُ لَهُمْ ضَرًّا وَلَا نَفْعًا
Moo ndax dañoo gisul ne bu ñul wax ak moom du toontu, te mënuleen a lor, mënuleen a jariñ dara ?
90وَلَقَدْ قَالَ لَهُمْ هَارُونُ مِن قَبْلُ يَا قَوْمِ إِنَّمَا فُتِنتُم بِهِ ۖ وَإِنَّ رَبَّكُمُ الرَّحْمَٰنُ فَاتَّبِعُونِي وَأَطِيعُوا أَمْرِي
Aaruuna moom waxoon na leen bu njëkk ne leen: "Yéen samaw nit, lii ngeen nekk aw sànje la. Waaye seen Boroom moo di Yërëmaakoon bi. Toppleen ma te wéyal samay ndigal”.
TahaFihi Alxuraan
135Aaya
MeccanRevelation
88Aaya

Tekki — Taha 88

Simoore Taha Aaya 88 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Daldi leen cay génneel aw sëll [nag]. Ne leen :…

Simoore Aaya 88/135 — Taha طه (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Taha Dégg, Taha Tekki, Taha mp3, Taha pdf. Aaya 86–90. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers