Aali Imran · 69/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
وَدَّت طَّائِفَةٌ مِّنْ أَهْلِ الْكِتَابِ لَوْ يُضِلُّونَكُمْ وَمَا يُضِلُّونَ إِلَّا أَنفُسَهُمْ وَمَا يَشْعُرُونَ ۝٦٩
Waddat taaa`ifatum min Ahlil Kitaabi law yudil loonakum wa maa yudilloona illaaa anfusahum wa maa yash`uroon
📖 Tekkim Wolof
Am na ab kurél bu bokk ci ñoñ-téere, danañu ngéeju réeral leen. Waaye mënuñoo réeral ku dul seen bopp ; te yéguñu ko.

🎧 Dégg


📜 Aaya 67-71 — Simoore Aali Imran

67مَا كَانَ إِبْرَاهِيمُ يَهُودِيًّا وَلَا نَصْرَانِيًّا وَلَٰكِن كَانَ حَنِيفًا مُّسْلِمًا وَمَا كَانَ مِنَ الْمُشْرِكِينَ
Ibraahiima nekkul woon yahuud, du càggéeni mu nekkoon nasraan. Waaye nekkoon na kuy wéetal Yàlla, di ku wommatu jëm ci Yàlla. Te bokkul woon ca ñay bokkaale..
68إِنَّ أَوْلَى النَّاسِ بِإِبْرَاهِيمَ لَلَّذِينَ اتَّبَعُوهُ وَهَٰذَا النَّبِيُّ وَالَّذِينَ آمَنُوا ۗ وَاللَّهُ وَلِيُّ الْمُؤْمِنِينَ
Nit ñi gën a yey ci Ibraahiima ñooy ña ko toppoon ak Yonent bii [Muhammad] ak ña gëm [Yàlla]. Te Yàlla mooy mbégum ñi gëm.
69وَدَّت طَّائِفَةٌ مِّنْ أَهْلِ الْكِتَابِ لَوْ يُضِلُّونَكُمْ وَمَا يُضِلُّونَ إِلَّا أَنفُسَهُمْ وَمَا يَشْعُرُونَ
Am na ab kurél bu bokk ci ñoñ-téere, danañu ngéeju réeral leen. Waaye mënuñoo réeral ku dul seen bopp ; te yéguñu ko.
70يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تَكْفُرُونَ بِآيَاتِ اللَّهِ وَأَنتُمْ تَشْهَدُونَ
Yéen ñoñ-téere, lu tax ngeen di weddi kàddug Yàlla, te ngeen di ci ay seede [xam ko xéll] ?
71يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تَلْبِسُونَ الْحَقَّ بِالْبَاطِلِ وَتَكْتُمُونَ الْحَقَّ وَأَنتُمْ تَعْلَمُونَ
Yéen ñoñ-téere, lan moo tax ngeen di muure dëgg ak ay caaxaan, di nëbb dëgg te xam ko ?
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
69Aaya

Tekki — Aali Imran 69

Simoore Aali Imran Aaya 69 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Am na ab kurél bu bokk ci ñoñ-téere, danañu ngéeju…

Simoore Aaya 69/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 67–71. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers