An-Nisa · 54/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
أَمْ يَحْسُدُونَ النَّاسَ عَلَىٰ مَا آتَاهُمُ اللَّهُ مِن فَضْلِهِ ۖ فَقَدْ آتَيْنَا آلَ إِبْرَاهِيمَ الْكِتَابَ وَالْحِكْمَةَ وَآتَيْنَاهُم مُّلْكًا عَظِيمًا ۝٥٤
Am yahsudoonan naasa `alaa maaa aataahumul laahu min fadlihee faqad aatainaaa Aala Ibraaheemal Kitaaba wal Hikmata wa aatainaahum mulkan `azeemaa
📖 Tekkim Wolof
Am dañuy iñaane nit ñi ci la leen Yàlla jox ciy ngënéelam ? Joxoon Nanu waa kër Ibraahiima ab Téere ak xam-xamu xereñe ; joxoon Nanu leen nguur gu rëy.

🎧 Dégg


📜 Aaya 52-56 — An-Nisa

52أُولَٰئِكَ الَّذِينَ لَعَنَهُمُ اللَّهُ ۖ وَمَن يَلْعَنِ اللَّهُ فَلَن تَجِدَ لَهُ نَصِيرًا
Ñooñu Yàlla rëbb na leen ; te ku Yàlla rëbb, kenn mënu koo amal ndimbal.
53أَمْ لَهُمْ نَصِيبٌ مِّنَ الْمُلْكِ فَإِذًا لَّا يُؤْتُونَ النَّاسَ نَقِيرًا
Am dañuy am sañ-sañ ci nguur gi ? Te kenn du ca sédd nit ñi, lu toll ci mboxosu xooxu tàndarma.
54أَمْ يَحْسُدُونَ النَّاسَ عَلَىٰ مَا آتَاهُمُ اللَّهُ مِن فَضْلِهِ ۖ فَقَدْ آتَيْنَا آلَ إِبْرَاهِيمَ الْكِتَابَ وَالْحِكْمَةَ وَآتَيْنَاهُم مُّلْكًا عَظِيمًا
Am dañuy iñaane nit ñi ci la leen Yàlla jox ciy ngënéelam ? Joxoon Nanu waa kër Ibraahiima ab Téere ak xam-xamu xereñe ; joxoon Nanu leen nguur gu rëy.
55فَمِنْهُم مَّنْ آمَنَ بِهِ وَمِنْهُم مَّن صَدَّ عَنْهُ ۚ وَكَفَىٰ بِجَهَنَّمَ سَعِيرًا
Amoon nañu ca ñoom ñu gëm [Téere ba], ak ñu dëddu [weddi Téere ba]. Te Safara dana leen doy.
56إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا بِآيَاتِنَا سَوْفَ نُصْلِيهِمْ نَارًا كُلَّمَا نَضِجَتْ جُلُودُهُم بَدَّلْنَاهُمْ جُلُودًا غَيْرَهَا لِيَذُوقُوا الْعَذَابَ ۗ إِنَّ اللَّهَ كَانَ عَزِيزًا حَكِيمًا
Ña weddi Sunuy kàddu, Dananu leen mos a séndal. Aw Saafara, wow, saa su seen deri yaram ñoree, Nu wecceekook yeneen, ngir ñu yëg mbugal ma. Yàlla boroom kàttan la, Ku xereñ la!
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
54Aaya

Tekki — An-Nisa 54

Simoore An-Nisa Aaya 54 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Am dañuy iñaane nit ñi ci la leen Yàlla jox…

Simoore Aaya 54/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 52–56. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers