Muhammad · 18/38
Tekki Waxtaan — Muhammad
فَهَلْ يَنظُرُونَ إِلَّا السَّاعَةَ أَن تَأْتِيَهُم بَغْتَةً ۖ فَقَدْ جَاءَ أَشْرَاطُهَا ۚ فَأَنَّىٰ لَهُمْ إِذَا جَاءَتْهُمْ ذِكْرَاهُمْ ۝١٨
Fahal yanzuroona illas Saa`ata an taatiyahum baghtatan faqad jaaa`a ashraatuhaa; fa-annnaa lahum izaa jaaa`at hum zikraahum
📖 Tekkim Wolof
Ana lan la (yéefar ya di xaar ci baña jebbalu) ba bis penc ba faf ne jaseet ci seen kaw bett leen ? Ndax màndargam yi dikk nañu. Te sax su xasee ba eksi ana lan la leen fàttaliku di jariñati?
🎧 Dégg

📜 Aaya 16-20 — Muhammad

16وَمِنْهُم مَّن يَسْتَمِعُ إِلَيْكَ حَتَّىٰ إِذَا خَرَجُوا مِنْ عِندِكَ قَالُوا لِلَّذِينَ أُوتُوا الْعِلْمَ مَاذَا قَالَ آنِفًا ۚ أُولَٰئِكَ الَّذِينَ طَبَعَ اللَّهُ عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ وَاتَّبَعُوا أَهْوَاءَهُمْ
Am na ci ñoom ñu lay déglu . Bu ñu génne fi yaw rekk, tàmbalee wakaate di laaj ña am xam-xam (Sahaba ya) naan leen : “Waaw moom lu mu waxati woon sax ? ” Ñooñee la Yàlla fàtt seen xol ñu topp senn bànneex.
17وَالَّذِينَ اهْتَدَوْا زَادَهُمْ هُدًى وَآتَاهُمْ تَقْوَاهُمْ
Ña gindiku ñoom dolli na leen njub, jox leen yombalal leen ragal Yàlla.
18فَهَلْ يَنظُرُونَ إِلَّا السَّاعَةَ أَن تَأْتِيَهُم بَغْتَةً ۖ فَقَدْ جَاءَ أَشْرَاطُهَا ۚ فَأَنَّىٰ لَهُمْ إِذَا جَاءَتْهُمْ ذِكْرَاهُمْ
Ana lan la (yéefar ya di xaar ci baña jebbalu) ba bis penc ba faf ne jaseet ci seen kaw bett leen ? Ndax màndargam yi dikk nañu. Te sax su xasee ba eksi ana lan la leen fàttaliku di jariñati?
19فَاعْلَمْ أَنَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا اللَّهُ وَاسْتَغْفِرْ لِذَنبِكَ وَلِلْمُؤْمِنِينَ وَالْمُؤْمِنَاتِ ۗ وَاللَّهُ يَعْلَمُ مُتَقَلَّبَكُمْ وَمَثْوَاكُمْ
Xamal ne, amul jeneen Yàlla ju dul moom Yàlla, te nga jéggalu say bàkkaar, ak di jéggalul jullit yu goor yeek yu jigéen yi. Yàlla xam na li ngeen di def lépp guddeek bëcëg.
20وَيَقُولُ الَّذِينَ آمَنُوا لَوْلَا نُزِّلَتْ سُورَةٌ ۖ فَإِذَا أُنزِلَتْ سُورَةٌ مُّحْكَمَةٌ وَذُكِرَ فِيهَا الْقِتَالُ ۙ رَأَيْتَ الَّذِينَ فِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ يَنظُرُونَ إِلَيْكَ نَظَرَ الْمَغْشِيِّ عَلَيْهِ مِنَ الْمَوْتِ ۖ فَأَوْلَىٰ لَهُمْ
Ña gëm ña ngay wax naan : “Cëy ! Bu aw saar wàccatiwoon ! ” Te fekk na saa suñu wàccee aw saar wu leer nàññ te digal ca xare, da ngay daldi gis naaféq ya di la xool ni ñuy xoole dee (ngir ragal). Li gën a yell ci ñoom moo di.
MuhammadFihi Alxuraan
38Aaya
MedinanRevelation
18Aaya

Tekki — Muhammad 18

Simoore Muhammad Aaya 18 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ana lan la (yéefar ya di xaar ci baña jebbalu)…

Simoore Aaya 18/38 — Muhammad محمد (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Muhammad Dégg, Muhammad Tekki, Muhammad mp3, Muhammad pdf. Aaya 16–20. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers