Yusuf · 61/111
Tekki Waxtaan — Yusuf
قَالُوا سَنُرَاوِدُ عَنْهُ أَبَاهُ وَإِنَّا لَفَاعِلُونَ ۝٦١
Qaaloo sanuraawidu `anhu abaahu wa innaa lafaa`iloon
📖 Tekkim Wolof
Ñu ne ko : “Dananu ko sàkku ci baayam. Te dananu ko def”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 59-63 — Yusuf

59وَلَمَّا جَهَّزَهُم بِجَهَازِهِمْ قَالَ ائْتُونِي بِأَخٍ لَّكُم مِّنْ أَبِيكُمْ ۚ أَلَا تَرَوْنَ أَنِّي أُوفِي الْكَيْلَ وَأَنَا خَيْرُ الْمُنزِلِينَ
Ba mu solee seen saaku ba noppi, mu ne leen : “Indil-leen ma seen doomi-baay ja des ak seen baay. Moo ndax gisuleen ne nattal na leen lu mat sëkk te it dalal naa leen gën ji daluwaay ?
60فَإِن لَّمْ تَأْتُونِي بِهِ فَلَا كَيْلَ لَكُمْ عِندِي وَلَا تَقْرَبُونِ
Bu ngeen ma ko indilul, dungeen amati ci man indaar ; te it dungeen ma jegeñ”.
61قَالُوا سَنُرَاوِدُ عَنْهُ أَبَاهُ وَإِنَّا لَفَاعِلُونَ
Ñu ne ko : “Dananu ko sàkku ci baayam. Te dananu ko def”.
62وَقَالَ لِفِتْيَانِهِ اجْعَلُوا بِضَاعَتَهُمْ فِي رِحَالِهِمْ لَعَلَّهُمْ يَعْرِفُونَهَا إِذَا انقَلَبُوا إِلَىٰ أَهْلِهِمْ لَعَلَّهُمْ يَرْجِعُونَ
Mu ne ay surgaam : “Dellooleen, ci seeni sëf, njëg [ga ñu joxe]: xéy-na danañu ko xàmmee bu ñu delloo ca seeni mbokk te xéy-na danañu dellusi”.
63فَلَمَّا رَجَعُوا إِلَىٰ أَبِيهِمْ قَالُوا يَا أَبَانَا مُنِعَ مِنَّا الْكَيْلُ فَأَرْسِلْ مَعَنَا أَخَانَا نَكْتَلْ وَإِنَّا لَهُ لَحَافِظُونَ
Ba ñu delloo ca seen baay, ñu ne ko : “Yaw sunu baay, [su nu yóbbaalewul sunu rakk jii weneen yoon, kenn dunu nattal]. Kon yebal ko mu ànd ak nun ndax ñu nattal nu. Kon dey dananu ko wattu”.
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
61Aaya

Tekki — Yusuf 61

Simoore Yusuf Aaya 61 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñu ne ko : “Dananu ko sàkku ci baayam. Te…

Simoore Aaya 61/111 — Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yusuf Dégg, Yusuf Tekki, Yusuf mp3, Yusuf pdf. Aaya 59–63. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers