Yusuf · 69/111
Tekki Waxtaan — Yusuf
وَلَمَّا دَخَلُوا عَلَىٰ يُوسُفَ آوَىٰ إِلَيْهِ أَخَاهُ ۖ قَالَ إِنِّي أَنَا أَخُوكَ فَلَا تَبْتَئِسْ بِمَا كَانُوا يَعْمَلُونَ ۝٦٩
Wa lammaa dakhaloo `alaa Yoosufa aawaaa ilaihi akhaahu qaala inneee ana akhooka falaa tabta`is bimaa kaanoo ya`maloon
📖 Tekkim Wolof
Ba ñu agsee ca Yuusufa, mu daldi xëcc taf ci boppam doomu-ndeyam ja, daldi ne : “Maa di sa doomu-ndey. Bul jàq ca la ñu nekkoon di ko def ci jéem maa sànk”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 67-71 — Yusuf

67وَقَالَ يَا بَنِيَّ لَا تَدْخُلُوا مِن بَابٍ وَاحِدٍ وَادْخُلُوا مِنْ أَبْوَابٍ مُّتَفَرِّقَةٍ ۖ وَمَا أُغْنِي عَنكُم مِّنَ اللَّهِ مِن شَيْءٍ ۖ إِنِ الْحُكْمُ إِلَّا لِلَّهِ ۖ عَلَيْهِ تَوَكَّلْتُ ۖ وَعَلَيْهِ فَلْيَتَوَكَّلِ الْمُتَوَكِّلُونَ
Mu ne : “Yéen samay doom, [bu ngeen àggee ca dëkk ba], buleen ca duggandoo ci benn buntu, nangeen xàjjalikoo dugge ciy buntu yu soriyaantoo. Mënuma leen a fegal dara lu jóge ci Yàlla. Moom rekk a moom àtte : Ci Moom rekk laa wéeru. Te képp kuy wéeru, na weeru ci Moom [Yàlla]”.
68وَلَمَّا دَخَلُوا مِنْ حَيْثُ أَمَرَهُمْ أَبُوهُم مَّا كَانَ يُغْنِي عَنْهُم مِّنَ اللَّهِ مِن شَيْءٍ إِلَّا حَاجَةً فِي نَفْسِ يَعْقُوبَ قَضَاهَا ۚ وَإِنَّهُ لَذُو عِلْمٍ لِّمَا عَلَّمْنَاهُ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ
Ba ñu duggee na ko seen baay diglee woon, taxul mu jariñ dara ca la Yàlla namm. Lu dul ne Yanqooba soxla woon na yiir leen ci loolu. Naka moom, boroom xam-xam la ci la Nu ko xamal. Waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
69وَلَمَّا دَخَلُوا عَلَىٰ يُوسُفَ آوَىٰ إِلَيْهِ أَخَاهُ ۖ قَالَ إِنِّي أَنَا أَخُوكَ فَلَا تَبْتَئِسْ بِمَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Ba ñu agsee ca Yuusufa, mu daldi xëcc taf ci boppam doomu-ndeyam ja, daldi ne : “Maa di sa doomu-ndey. Bul jàq ca la ñu nekkoon di ko def ci jéem maa sànk”.
70فَلَمَّا جَهَّزَهُم بِجَهَازِهِمْ جَعَلَ السِّقَايَةَ فِي رَحْلِ أَخِيهِ ثُمَّ أَذَّنَ مُؤَذِّنٌ أَيَّتُهَا الْعِيرُ إِنَّكُمْ لَسَارِقُونَ
Ba mu leen solalee seeni saaku ba noppi, mu dugal andaar [ja ñu doon natte] ca biir sëfu doomu-ndeyam ja. Mu am yéglekat bu wax ne : “Éy yéen jëgg ji ! Ay sàcc ngeen”.
71قَالُوا وَأَقْبَلُوا عَلَيْهِم مَّاذَا تَفْقِدُونَ
Ñoom it ñu wëlbatiku ca moom ne leen : “Lan ngeen réerle ? ”
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
69Aaya

Tekki — Yusuf 69

Simoore Yusuf Aaya 69 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba ñu agsee ca Yuusufa, mu daldi xëcc taf ci…

Simoore Aaya 69/111 — Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yusuf Dégg, Yusuf Tekki, Yusuf mp3, Yusuf pdf. Aaya 67–71. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers