An-Nahl · 9/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
وَعَلَى اللَّهِ قَصْدُ السَّبِيلِ وَمِنْهَا جَائِرٌ ۚ وَلَوْ شَاءَ لَهَدَاكُمْ أَجْمَعِينَ ۝٩
Wa `alal laahi qasdus sabeeli wa minhaa jaaa`ir; wa law shaaa`a lahadaakum ajma`een
📖 Tekkim Wolof
Yàlla moo yeyoo leeral yoon wu jub wa, [te am na ci yoon yi] yu jeng féeroo ak njub. Te bu Ko sooboon Mu jubal leen yéen ñépp.
🎧 Dégg

📜 Aaya 7-11 — An-Nahl

7وَتَحْمِلُ أَثْقَالَكُمْ إِلَىٰ بَلَدٍ لَّمْ تَكُونُوا بَالِغِيهِ إِلَّا بِشِقِّ الْأَنفُسِ ۚ إِنَّ رَبَّكُمْ لَرَءُوفٌ رَّحِيمٌ
Te danañu yenu seen [yóbbal], yóbbul leen ko ca dëkk ba ngeen dul woon mën a dem lu dul ci ab coono bub bakkan. Naka seen Boroom Aji-ñeewant la, Jaglewaakoon la.
8وَالْخَيْلَ وَالْبِغَالَ وَالْحَمِيرَ لِتَرْكَبُوهَا وَزِينَةً ۚ وَيَخْلُقُ مَا لَا تَعْلَمُونَ
[Moo bind it] fas ak i baxla [berkelle] ak mbaam ngir ngeen war leen, ak ngir taar. Te it bind na lu ngeen xamul.
9وَعَلَى اللَّهِ قَصْدُ السَّبِيلِ وَمِنْهَا جَائِرٌ ۚ وَلَوْ شَاءَ لَهَدَاكُمْ أَجْمَعِينَ
Yàlla moo yeyoo leeral yoon wu jub wa, [te am na ci yoon yi] yu jeng féeroo ak njub. Te bu Ko sooboon Mu jubal leen yéen ñépp.
10هُوَ الَّذِي أَنزَلَ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً ۖ لَّكُم مِّنْهُ شَرَابٌ وَمِنْهُ شَجَرٌ فِيهِ تُسِيمُونَ
Moom mooy ki leen wàcceel ndox mu jóge asamaan, ngeen di ca naan, garab yi di ca saxe, ngeen di ca nàndale [jur gi].
11يُنبِتُ لَكُم بِهِ الزَّرْعَ وَالزَّيْتُونَ وَالنَّخِيلَ وَالْأَعْنَابَ وَمِن كُلِّ الثَّمَرَاتِ ۗ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَةً لِّقَوْمٍ يَتَفَكَّرُونَ
Mu di leen cay saxal mbey, garabi oliiw ak i tàndarma, ak yu reseñ, ak bépp meññent. Loolu mën naa waar aw nit yuy xalaat [natt].
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
9Aaya

Tekki — An-Nahl 9

Simoore An-Nahl Aaya 9 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla moo yeyoo leeral yoon wu jub wa, [te am…

Simoore Aaya 9/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 7–11. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers