Al-Isra · 72/111
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Isra
وَمَن كَانَ فِي هَٰذِهِ أَعْمَىٰ فَهُوَ فِي الْآخِرَةِ أَعْمَىٰ وَأَضَلُّ سَبِيلًا ۝٧٢
Wa man kaana fee haaziheee a`maa fahuwa fil aakhirati a`maa wa adallu sabeelaa
📖 Tekkim Wolof
Ku nekkoon gumba ci àddina si, dana wéye gumba ca àllaaxira, te gën a réer, sori yoonu njub wa.

🎧 Dégg


📜 Aaya 70-74 — Simoore Al-Isra

70۞ وَلَقَدْ كَرَّمْنَا بَنِي آدَمَ وَحَمَلْنَاهُمْ فِي الْبَرِّ وَالْبَحْرِ وَرَزَقْنَاهُم مِّنَ الطَّيِّبَاتِ وَفَضَّلْنَاهُمْ عَلَىٰ كَثِيرٍ مِّمَّنْ خَلَقْنَا تَفْضِيلًا
Ca dëgg-dëgg, teral Nanu doomi aadama. Yónni Nanu leen ci jéeri ji ak ci géej gi, te xéewal Nanu leen [ciy ñam] yu sell, Nu defal leen ngëneel ci kaw ñu bari ca ña Nu bind ngëneel lu fés.
71يَوْمَ نَدْعُو كُلَّ أُنَاسٍ بِإِمَامِهِمْ ۖ فَمَنْ أُوتِيَ كِتَابَهُ بِيَمِينِهِ فَأُولَٰئِكَ يَقْرَءُونَ كِتَابَهُمْ وَلَا يُظْلَمُونَ فَتِيلًا
Bis bu Nu woowee nit ku nekk ca turu njiitam, képp ku Nu jox téereem ci ndeyjooram, ñooña danañu jàng seen téere te deesuleen tooñ [ci wànnil leen dara].
72وَمَن كَانَ فِي هَٰذِهِ أَعْمَىٰ فَهُوَ فِي الْآخِرَةِ أَعْمَىٰ وَأَضَلُّ سَبِيلًا
Ku nekkoon gumba ci àddina si, dana wéye gumba ca àllaaxira, te gën a réer, sori yoonu njub wa.
73وَإِن كَادُوا لَيَفْتِنُونَكَ عَنِ الَّذِي أَوْحَيْنَا إِلَيْكَ لِتَفْتَرِيَ عَلَيْنَا غَيْرَهُ ۖ وَإِذًا لَّاتَّخَذُوكَ خَلِيلًا
Xaw nañu laa fitnaal ba nga bàyyi la Nu la xamal, ngir nga duur lu wuuteek moom. Kon ñu jàppe la xarit ñoom yéefar yi.
74وَلَوْلَا أَن ثَبَّتْنَاكَ لَقَدْ كِدتَّ تَرْكَنُ إِلَيْهِمْ شَيْئًا قَلِيلًا
Te bu Nu la dëgaralul woon, tuuti kon nga xaw a jeng jëm ci ñoom
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
72Aaya

Tekki — Al-Isra 72

Simoore Al-Isra Aaya 72 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ku nekkoon gumba ci àddina si, dana wéye gumba ca…

Simoore Aaya 72/111 — Simoore Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Isra Dégg, Simoore Al-Isra Tekki, Simoore Al-Isra mp3, Simoore Al-Isra pdf. Aaya 70–74. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers