Al-Baqara · 269/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
يُؤْتِي الْحِكْمَةَ مَن يَشَاءُ ۚ وَمَن يُؤْتَ الْحِكْمَةَ فَقَدْ أُوتِيَ خَيْرًا كَثِيرًا ۗ وَمَا يَذَّكَّرُ إِلَّا أُولُو الْأَلْبَابِ ۝٢٦٩
Yu`til Hikmata mai yashaaa`; wa mai yutal Hikmata faqad ootiya khairan kaseeraa; wa maa yazzakkaru illaaa ulul albaab
📖 Tekkim Wolof
Mooy jox ku ko soob xel mu rëy, rafet . Ku Mu jox xel mu rafet, jox na ko njariñ lu rëy. Te boroom xel ya rekk ay waaru.
🎧 Dégg

📜 Aaya 267-271 — Al-Baqara

267يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا أَنفِقُوا مِن طَيِّبَاتِ مَا كَسَبْتُمْ وَمِمَّا أَخْرَجْنَا لَكُم مِّنَ الْأَرْضِ ۖ وَلَا تَيَمَّمُوا الْخَبِيثَ مِنْهُ تُنفِقُونَ وَلَسْتُم بِآخِذِيهِ إِلَّا أَن تُغْمِضُوا فِيهِ ۚ وَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ غَنِيٌّ حَمِيدٌ
Yéen ñi gëm ! Deeleen joxe asaka ci lu téey li ngeen di fàggul seen bopp ak li Nu leen génneele ci suuf si. Buleen ca beddi la ca yées di ko joxe. Te fekk muy loo xam ne ku leen ko joxoon dungeen ko bëgg a jël, te gëmmuleen ca ! Nangeen xam ne Yàlla ku woomal la te ku yayoo cant la.
268الشَّيْطَانُ يَعِدُكُمُ الْفَقْرَ وَيَأْمُرُكُم بِالْفَحْشَاءِ ۖ وَاللَّهُ يَعِدُكُم مَّغْفِرَةً مِّنْهُ وَفَضْلًا ۗ وَاللَّهُ وَاسِعٌ عَلِيمٌ
Séytaane, ag ñàkk la leen di dig, di leen xiir ci moy ;Yàlla nag, jéggal la leen di dig ak wërsëg wu bawoo ca Moom. Yàlla ku yaatu, ku xam la.
269يُؤْتِي الْحِكْمَةَ مَن يَشَاءُ ۚ وَمَن يُؤْتَ الْحِكْمَةَ فَقَدْ أُوتِيَ خَيْرًا كَثِيرًا ۗ وَمَا يَذَّكَّرُ إِلَّا أُولُو الْأَلْبَابِ
Mooy jox ku ko soob xel mu rëy, rafet . Ku Mu jox xel mu rafet, jox na ko njariñ lu rëy. Te boroom xel ya rekk ay waaru.
270وَمَا أَنفَقْتُم مِّن نَّفَقَةٍ أَوْ نَذَرْتُم مِّن نَّذْرٍ فَإِنَّ اللَّهَ يَعْلَمُهُ ۗ وَمَا لِلظَّالِمِينَ مِنْ أَنصَارٍ
Li ngeen joxe mu génn walla ngeen nisar ko , Yàlla xam na ko. Ñiy tooñ, duñu am ndimbal !
271إِن تُبْدُوا الصَّدَقَاتِ فَنِعِمَّا هِيَ ۖ وَإِن تُخْفُوهَا وَتُؤْتُوهَا الْفُقَرَاءَ فَهُوَ خَيْرٌ لَّكُمْ ۚ وَيُكَفِّرُ عَنكُم مِّن سَيِّئَاتِكُمْ ۗ وَاللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرٌ
Bu ngeen feeñalee seeni sarax, baax na ; bu ngeen ko nëbbee, jox ko wax-ñéew ji doole ya nag, moo gën ci yéen. Danañu leen jéggal ci seeni ñaawtéef [ci soppi ko aw yiw]. Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
269Aaya

Tekki — Al-Baqara 269

Simoore Al-Baqara Aaya 269 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mooy jox ku ko soob xel mu rëy, rafet .…

Simoore Aaya 269/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 267–271. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers