Al-Anbiya · 31/112
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Anbiya
وَجَعَلْنَا فِي الْأَرْضِ رَوَاسِيَ أَن تَمِيدَ بِهِمْ وَجَعَلْنَا فِيهَا فِجَاجًا سُبُلًا لَّعَلَّهُمْ يَهْتَدُونَ ۝٣١
Wa ja`alnaa fil ardi rawaasiya an tameeda bihim wa ja`alnaa feehaa fijaajan subulal la`allahum yahtadoon
📖 Tekkim Wolof
Te def Nanu ci biir suuf si ay tundi doj, ngir mu bañ a baj-baji ak ñoom. Te def Nanu ci ay yoon ngir ñu mën a gindiku.

🎧 Dégg


📜 Aaya 29-33 — Simoore Al-Anbiya

29۞ وَمَن يَقُلْ مِنْهُمْ إِنِّي إِلَٰهٌ مِّن دُونِهِ فَذَٰلِكَ نَجْزِيهِ جَهَنَّمَ ۚ كَذَٰلِكَ نَجْزِي الظَّالِمِينَ
Te ku ca waxoon bokk ca ñoom ne : “Man yàlla laa, ju dul Moom”. Loola Safara la Nu ko koy feyee. Te noona it la Nuy feye tooñkat ya.
30أَوَلَمْ يَرَ الَّذِينَ كَفَرُوا أَنَّ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ كَانَتَا رَتْقًا فَفَتَقْنَاهُمَا ۖ وَجَعَلْنَا مِنَ الْمَاءِ كُلَّ شَيْءٍ حَيٍّ ۖ أَفَلَا يُؤْمِنُونَ
Ndax ña weddi dañoo gisul ne asamaan yi ak suuf si dañoo taqaloodef [benn dank] ? Nu daldi leen téqale, te Nu sose ndox lépp luy dundu. Moo ndax dañu dul gëm ?
31وَجَعَلْنَا فِي الْأَرْضِ رَوَاسِيَ أَن تَمِيدَ بِهِمْ وَجَعَلْنَا فِيهَا فِجَاجًا سُبُلًا لَّعَلَّهُمْ يَهْتَدُونَ
Te def Nanu ci biir suuf si ay tundi doj, ngir mu bañ a baj-baji ak ñoom. Te def Nanu ci ay yoon ngir ñu mën a gindiku.
32وَجَعَلْنَا السَّمَاءَ سَقْفًا مَّحْفُوظًا ۖ وَهُمْ عَنْ آيَاتِهَا مُعْرِضُونَ
Te def Nanu asamaan si mu nekk am téeg mu Nu wattu. Te ñoom ñangay dëddu Sunuy kéemtaan [bañ leen a seetlu].
33وَهُوَ الَّذِي خَلَقَ اللَّيْلَ وَالنَّهَارَ وَالشَّمْسَ وَالْقَمَرَ ۖ كُلٌّ فِي فَلَكٍ يَسْبَحُونَ
Te Moom mooy ki bind guddi gi ak bëccëg bi, ak jant bi ak weer wi, ku ci nekk di daw caw rëdd [wa ñu ko rëddal].
Al-AnbiyaFihi Alxuraan
112Aaya
MeccanRevelation
31Aaya

Tekki — Al-Anbiya 31

Simoore Al-Anbiya Aaya 31 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te def Nanu ci biir suuf si ay tundi doj,…

Simoore Aaya 31/112 — Simoore Al-Anbiya الأنبياء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Anbiya Dégg, Simoore Al-Anbiya Tekki, Simoore Al-Anbiya mp3, Simoore Al-Anbiya pdf. Aaya 29–33. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers