Aali Imran · 67/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
مَا كَانَ إِبْرَاهِيمُ يَهُودِيًّا وَلَا نَصْرَانِيًّا وَلَٰكِن كَانَ حَنِيفًا مُّسْلِمًا وَمَا كَانَ مِنَ الْمُشْرِكِينَ ۝٦٧
Maa kaana Ibraaheemu Yahoodiyyanw wa laa Nasraa niyyanw wa laakin kaana Haneefam Muslimanw wa maa kaana minal mushrikeen
📖 Tekkim Wolof
Ibraahiima nekkul woon yahuud, du càggéeni mu nekkoon nasraan. Waaye nekkoon na kuy wéetal Yàlla, di ku wommatu jëm ci Yàlla. Te bokkul woon ca ñay bokkaale..

🎧 Dégg


📜 Aaya 65-69 — Simoore Aali Imran

65يَا أَهْلَ الْكِتَابِ لِمَ تُحَاجُّونَ فِي إِبْرَاهِيمَ وَمَا أُنزِلَتِ التَّوْرَاةُ وَالْإِنجِيلُ إِلَّا مِن بَعْدِهِ ۚ أَفَلَا تَعْقِلُونَ
Yéen ñoñ-téere, ana lan moo waral ngeen di dàggasante ci mbiri Ibraahiima, te Tawreet ak Injiil ginnaawam lañu wàcc ? Moo ndax dungeen xel-lu ?
66هَا أَنتُمْ هَٰؤُلَاءِ حَاجَجْتُمْ فِيمَا لَكُم بِهِ عِلْمٌ فَلِمَ تُحَاجُّونَ فِيمَا لَيْسَ لَكُم بِهِ عِلْمٌ ۚ وَاللَّهُ يَعْلَمُ وَأَنتُمْ لَا تَعْلَمُونَ
Yëgleen ne dàggasante ngeen ci lu ngeen xam [mbiri Iisaa]. Lu tax ngeen di dàgge ci lu ngeen amul xam-xam [Mbiri Ibraahiima] ? Yàlla xam na te yéen xamuleen.
67مَا كَانَ إِبْرَاهِيمُ يَهُودِيًّا وَلَا نَصْرَانِيًّا وَلَٰكِن كَانَ حَنِيفًا مُّسْلِمًا وَمَا كَانَ مِنَ الْمُشْرِكِينَ
Ibraahiima nekkul woon yahuud, du càggéeni mu nekkoon nasraan. Waaye nekkoon na kuy wéetal Yàlla, di ku wommatu jëm ci Yàlla. Te bokkul woon ca ñay bokkaale..
68إِنَّ أَوْلَى النَّاسِ بِإِبْرَاهِيمَ لَلَّذِينَ اتَّبَعُوهُ وَهَٰذَا النَّبِيُّ وَالَّذِينَ آمَنُوا ۗ وَاللَّهُ وَلِيُّ الْمُؤْمِنِينَ
Nit ñi gën a yey ci Ibraahiima ñooy ña ko toppoon ak Yonent bii [Muhammad] ak ña gëm [Yàlla]. Te Yàlla mooy mbégum ñi gëm.
69وَدَّت طَّائِفَةٌ مِّنْ أَهْلِ الْكِتَابِ لَوْ يُضِلُّونَكُمْ وَمَا يُضِلُّونَ إِلَّا أَنفُسَهُمْ وَمَا يَشْعُرُونَ
Am na ab kurél bu bokk ci ñoñ-téere, danañu ngéeju réeral leen. Waaye mënuñoo réeral ku dul seen bopp ; te yéguñu ko.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
67Aaya

Tekki — Aali Imran 67

Simoore Aali Imran Aaya 67 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ibraahiima nekkul woon yahuud, du càggéeni mu nekkoon nasraan. Waaye…

Simoore Aaya 67/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 65–69. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers