Aali Imran · 95/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
قُلْ صَدَقَ اللَّهُ ۗ فَاتَّبِعُوا مِلَّةَ إِبْرَاهِيمَ حَنِيفًا وَمَا كَانَ مِنَ الْمُشْرِكِينَ ۝٩٥
Qul sadaqal laah; fattabi`oo Millata Ibraaheema Haneefanw wa maa kaana minal mush rikeen
📖 Tekkim Wolof
Neel : “Yàllaa wax dëgg. Kon toppleen diiney Ibraahiima. Ku wéetaloon Yàlla la te mësul a bokk ca ñay bokkaale Yàlla”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 93-97 — Simoore Aali Imran

93۞ كُلُّ الطَّعَامِ كَانَ حِلًّا لِّبَنِي إِسْرَائِيلَ إِلَّا مَا حَرَّمَ إِسْرَائِيلُ عَلَىٰ نَفْسِهِ مِن قَبْلِ أَن تُنَزَّلَ التَّوْرَاةُ ۗ قُلْ فَأْتُوا بِالتَّوْرَاةِ فَاتْلُوهَا إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Ñam yépp a daganoon ca waa Banii-Israayiil, lu dul ñam ya [Israayiil ] araama loon ca boppam lu jiitu ñu doon wàcce Tawreet. Neel: “Indileen Tawreet te jàng ko, ndegam ñu dëggu ngeen ! ”
94فَمَنِ افْتَرَىٰ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ مِن بَعْدِ ذَٰلِكَ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الظَّالِمُونَ
Ku duural Yàlla ay fen, ginnaaw loolu... ñooñaa di tooñkat ya.
95قُلْ صَدَقَ اللَّهُ ۗ فَاتَّبِعُوا مِلَّةَ إِبْرَاهِيمَ حَنِيفًا وَمَا كَانَ مِنَ الْمُشْرِكِينَ
Neel : “Yàllaa wax dëgg. Kon toppleen diiney Ibraahiima. Ku wéetaloon Yàlla la te mësul a bokk ca ñay bokkaale Yàlla”.
96إِنَّ أَوَّلَ بَيْتٍ وُضِعَ لِلنَّاسِ لَلَّذِي بِبَكَّةَ مُبَارَكًا وَهُدًى لِّلْعَالَمِينَ
Néeg ba ñu njëkk sampal nit ñi moo di ba nekk Màkka, muy bu ñu barkeel, di njub, mbindéef yépp bokk ko.
97فِيهِ آيَاتٌ بَيِّنَاتٌ مَّقَامُ إِبْرَاهِيمَ ۖ وَمَن دَخَلَهُ كَانَ آمِنًا ۗ وَلِلَّهِ عَلَى النَّاسِ حِجُّ الْبَيْتِ مَنِ اسْتَطَاعَ إِلَيْهِ سَبِيلًا ۚ وَمَن كَفَرَ فَإِنَّ اللَّهَ غَنِيٌّ عَنِ الْعَالَمِينَ
Ay kéemaan yu leer ñoo fa nekk, [bokk na ca] Maxaama Ibraahiima [barab] ; ku fa dugg am kóolute. War na, ci nit ñi ku ko mën, aj fa néegub Yàlla ba te Yàlla tax wenn yoon [wu farata]. Ku weddi nag... na xam ne Yàlla ku doyloo la waliis mbindéef yépp.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
95Aaya

Tekki — Aali Imran 95

Simoore Aali Imran Aaya 95 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Neel : “Yàllaa wax dëgg. Kon toppleen diiney Ibraahiima. Ku…

Simoore Aaya 95/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 93–97. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers