An-Nisa · 86/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
وَإِذَا حُيِّيتُم بِتَحِيَّةٍ فَحَيُّوا بِأَحْسَنَ مِنْهَا أَوْ رُدُّوهَا ۗ إِنَّ اللَّهَ كَانَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ حَسِيبًا ۝٨٦
Wa izaa huyyeetum bitahiy yatin fahaiyoo bi ahsana minhaaa aw ruddoohaa; innal laaha kaana `alaa kulli shai`in Haseeba
📖 Tekkim Wolof
Bu ñu leen nuyyoo, nangeen delloo nuyyoo bu gën a rafet ; mbaa bu na mel. Yàlla Kuy natt lépp la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 84-88 — An-Nisa

84فَقَاتِلْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ لَا تُكَلَّفُ إِلَّا نَفْسَكَ ۚ وَحَرِّضِ الْمُؤْمِنِينَ ۖ عَسَى اللَّهُ أَن يَكُفَّ بَأْسَ الَّذِينَ كَفَرُوا ۚ وَاللَّهُ أَشَدُّ بَأْسًا وَأَشَدُّ تَنكِيلًا
Xareel ci yoonu Yàlla, sasewuñu la lu dul sa bopp, te nanga ñaax ñi gëm, amaana Yàlla fegal la ayu yéefar ya. Te Yàllaa gën a tar ngaañ, Moo gën a tar xorñoñal.
85مَّن يَشْفَعْ شَفَاعَةً حَسَنَةً يَكُن لَّهُ نَصِيبٌ مِّنْهَا ۖ وَمَن يَشْفَعْ شَفَاعَةً سَيِّئَةً يَكُن لَّهُ كِفْلٌ مِّنْهَا ۗ وَكَانَ اللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ مُّقِيتًا
Képp ku taxawu nit [dooleel ko] taxawaay bu rafet, dana ca am cër ; ku taxawu nit [dooleel ko] cig ñaawtéef, dana ca am bàkkaar ba. Yàlla Kuy seetlu lépp la.
86وَإِذَا حُيِّيتُم بِتَحِيَّةٍ فَحَيُّوا بِأَحْسَنَ مِنْهَا أَوْ رُدُّوهَا ۗ إِنَّ اللَّهَ كَانَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ حَسِيبًا
Bu ñu leen nuyyoo, nangeen delloo nuyyoo bu gën a rafet ; mbaa bu na mel. Yàlla Kuy natt lépp la.
87اللَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۚ لَيَجْمَعَنَّكُمْ إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ لَا رَيْبَ فِيهِ ۗ وَمَنْ أَصْدَقُ مِنَ اللَّهِ حَدِيثًا
Amul jeneen yàlla yu dul Moom Yàlla ! Fàwwu dana leen dajale Bis-pénc ba, sikkuwut. Te kan moo gën a dëgguy wax Yàlla ? [Amul]
88۞ فَمَا لَكُمْ فِي الْمُنَافِقِينَ فِئَتَيْنِ وَاللَّهُ أَرْكَسَهُم بِمَا كَسَبُوا ۚ أَتُرِيدُونَ أَن تَهْدُوا مَنْ أَضَلَّ اللَّهُ ۖ وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَلَن تَجِدَ لَهُ سَبِيلًا
Lu ngeen am ? Ca naaféq ya, am na ñaari kuréel.Te Yàlla delloo na leen ca la ñu fàggu woon. Moo ndax dangeen a bëgg gindi ka Yàlla bàyyi cig réer ? Ku Yàlla bàyyi cig réeram, doo ko mën wutal yoonu mucc.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
86Aaya

Tekki — An-Nisa 86

Simoore An-Nisa Aaya 86 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu ñu leen nuyyoo, nangeen delloo nuyyoo bu gën a…

Simoore Aaya 86/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 84–88. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers