An-Nisa · 87/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
اللَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۚ لَيَجْمَعَنَّكُمْ إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ لَا رَيْبَ فِيهِ ۗ وَمَنْ أَصْدَقُ مِنَ اللَّهِ حَدِيثًا ۝٨٧
Allaahu laaa ilaaha illaa huwa la yajma`annakum ilaa Yawmil Qiyaamati laa raiba feeh; wa man asdaqu mminallaahi hadeesaa
📖 Tekkim Wolof
Amul jeneen yàlla yu dul Moom Yàlla ! Fàwwu dana leen dajale Bis-pénc ba, sikkuwut. Te kan moo gën a dëgguy wax Yàlla ? [Amul]

🎧 Dégg


📜 Aaya 85-89 — An-Nisa

85مَّن يَشْفَعْ شَفَاعَةً حَسَنَةً يَكُن لَّهُ نَصِيبٌ مِّنْهَا ۖ وَمَن يَشْفَعْ شَفَاعَةً سَيِّئَةً يَكُن لَّهُ كِفْلٌ مِّنْهَا ۗ وَكَانَ اللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ مُّقِيتًا
Képp ku taxawu nit [dooleel ko] taxawaay bu rafet, dana ca am cër ; ku taxawu nit [dooleel ko] cig ñaawtéef, dana ca am bàkkaar ba. Yàlla Kuy seetlu lépp la.
86وَإِذَا حُيِّيتُم بِتَحِيَّةٍ فَحَيُّوا بِأَحْسَنَ مِنْهَا أَوْ رُدُّوهَا ۗ إِنَّ اللَّهَ كَانَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ حَسِيبًا
Bu ñu leen nuyyoo, nangeen delloo nuyyoo bu gën a rafet ; mbaa bu na mel. Yàlla Kuy natt lépp la.
87اللَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۚ لَيَجْمَعَنَّكُمْ إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ لَا رَيْبَ فِيهِ ۗ وَمَنْ أَصْدَقُ مِنَ اللَّهِ حَدِيثًا
Amul jeneen yàlla yu dul Moom Yàlla ! Fàwwu dana leen dajale Bis-pénc ba, sikkuwut. Te kan moo gën a dëgguy wax Yàlla ? [Amul]
88۞ فَمَا لَكُمْ فِي الْمُنَافِقِينَ فِئَتَيْنِ وَاللَّهُ أَرْكَسَهُم بِمَا كَسَبُوا ۚ أَتُرِيدُونَ أَن تَهْدُوا مَنْ أَضَلَّ اللَّهُ ۖ وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَلَن تَجِدَ لَهُ سَبِيلًا
Lu ngeen am ? Ca naaféq ya, am na ñaari kuréel.Te Yàlla delloo na leen ca la ñu fàggu woon. Moo ndax dangeen a bëgg gindi ka Yàlla bàyyi cig réer ? Ku Yàlla bàyyi cig réeram, doo ko mën wutal yoonu mucc.
89وَدُّوا لَوْ تَكْفُرُونَ كَمَا كَفَرُوا فَتَكُونُونَ سَوَاءً ۖ فَلَا تَتَّخِذُوا مِنْهُمْ أَوْلِيَاءَ حَتَّىٰ يُهَاجِرُوا فِي سَبِيلِ اللَّهِ ۚ فَإِن تَوَلَّوْا فَخُذُوهُمْ وَاقْتُلُوهُمْ حَيْثُ وَجَدتُّمُوهُمْ ۖ وَلَا تَتَّخِذُوا مِنْهُمْ وَلِيًّا وَلَا نَصِيرًا
Ñanga ne siiw ngeen weddi, na ñu weddee [ñoom] : ndax ngeen yem ! Buleen jàpp ay xarit ci ñoom, li feek ñuy gàddaay jëm ci yoonu Yàlla. Bu ñu dëddoo, jàppleen leen te reyleen fu ngeen leen mën a fekk ; te buleen wut ci ñoom xarit waxumalaak ndimbal,
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
87Aaya

Tekki — An-Nisa 87

Simoore An-Nisa Aaya 87 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Amul jeneen yàlla yu dul Moom Yàlla ! Fàwwu dana…

Simoore Aaya 87/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 85–89. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers