At-Tawba · 125/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
وَأَمَّا الَّذِينَ فِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ فَزَادَتْهُمْ رِجْسًا إِلَىٰ رِجْسِهِمْ وَمَاتُوا وَهُمْ كَافِرُونَ ۝١٢٥
Wa ammal lazeena fee quloobihim maradun fazaadat hum rijsan ilaa rijsihim wa maatoo wa hum kaafiroon
📖 Tekkim Wolof
Ña nga xam ne jàngaro nekk na ci seen xol ya, dafay nekk ci ñoom kéefar guy dolliku cig kéefar, te ci kéefar googu lañuy deewaale.

🎧 Dégg


📜 Aaya 123-127 — At-Tawba

123يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا قَاتِلُوا الَّذِينَ يَلُونَكُم مِّنَ الْكُفَّارِ وَلْيَجِدُوا فِيكُمْ غِلْظَةً ۚ وَاعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ مَعَ الْمُتَّقِينَ
Éy yéen ñi gëm ! Xeexleen ak ñi leen jegeñ ci yéefar yi ; nañu fekk ci yéen dëgër gu mat sëkk. Te ngeen xam ne Yàllaa ngi ànd ak ñi ragal Yàlla.
124وَإِذَا مَا أُنزِلَتْ سُورَةٌ فَمِنْهُم مَّن يَقُولُ أَيُّكُمْ زَادَتْهُ هَٰذِهِ إِيمَانًا ۚ فَأَمَّا الَّذِينَ آمَنُوا فَزَادَتْهُمْ إِيمَانًا وَهُمْ يَسْتَبْشِرُونَ
Te bu aw saar mësaan a wàcc, dana am ci ñooña (naaféq) ya, ñuy wax naan : “Ana kan la lii mën a dolli ngëmam ? ”. Waaye, ña nga xam ne ñoom gëm nañu, Dana leen yokk ngëm, te it danañu ca bég.
125وَأَمَّا الَّذِينَ فِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ فَزَادَتْهُمْ رِجْسًا إِلَىٰ رِجْسِهِمْ وَمَاتُوا وَهُمْ كَافِرُونَ
Ña nga xam ne jàngaro nekk na ci seen xol ya, dafay nekk ci ñoom kéefar guy dolliku cig kéefar, te ci kéefar googu lañuy deewaale.
126أَوَلَا يَرَوْنَ أَنَّهُمْ يُفْتَنُونَ فِي كُلِّ عَامٍ مَّرَّةً أَوْ مَرَّتَيْنِ ثُمَّ لَا يَتُوبُونَ وَلَا هُمْ يَذَّكَّرُونَ
Moo ndax dañoo gisul ne at mu nekk dees na leen not benn walla ñaari yoon ? Te ñooña, duñu tuub, duñu waaru.
127وَإِذَا مَا أُنزِلَتْ سُورَةٌ نَّظَرَ بَعْضُهُمْ إِلَىٰ بَعْضٍ هَلْ يَرَاكُم مِّنْ أَحَدٍ ثُمَّ انصَرَفُوا ۚ صَرَفَ اللَّهُ قُلُوبَهُم بِأَنَّهُمْ قَوْمٌ لَّا يَفْقَهُونَ
Te su ñu wàccee aw saar ñu daldi xoolante, daldi wax ne : “Moo ndax am na ku nu gis ? ”. Daldi wëlbëtiku. Yal na Yàlla wëlbëti seeni xol ndax ñoom, aw nit lañu ñu amul genn dégg-dégg.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
125Aaya

Tekki — At-Tawba 125

Simoore At-Tawba Aaya 125 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña nga xam ne jàngaro nekk na ci seen xol…

Simoore Aaya 125/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 123–127. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers