Simoore Al-Qamar ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Al-Qamar ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (55 Aaya — مكية). Al-Qamar Dégg, Al-Qamar Tekki, Al-Qamar mp3, Al-Qamar pdf.

Jàng te Dégg Simoore Al-Qamar

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
اقْتَرَبَتِ السَّاعَةُ وَانشَقَّ الْقَمَرُ ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Waxtu wi jigesi na weer wi xar na (bis pénc ba).
وَإِن يَرَوْا آيَةً يُعْرِضُوا وَيَقُولُوا سِحْرٌ مُّسْتَمِرٌّ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
Saa su ñu gisee keemaan, dañuy dumóoyu tey wax naan : “Lii ag njibar laati”.
وَكَذَّبُوا وَاتَّبَعُوا أَهْوَاءَهُمْ ۚ وَكُلُّ أَمْرٍ مُّسْتَقِرٌّ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
weddi nañu topp nañu it seen bànneex, te mbir yépp a ngi ne roŋŋ
وَلَقَدْ جَاءَهُم مِّنَ الْأَنبَاءِ مَا فِيهِ مُزْدَجَرٌ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
Te jot nañu ci ay xibaar lu leen man a jàjj ;
حِكْمَةٌ بَالِغَةٌ ۖ فَمَا تُغْنِ النُّذُرُ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
Ràññatle gu jotal . Waaye teewul ñuy sànku.
فَتَوَلَّ عَنْهُمْ ۘ يَوْمَ يَدْعُ الدَّاعِ إِلَىٰ شَيْءٍ نُّكُرٍ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Nangeen leen dumóoyu. Bu keroogee ba wootekat ba di woote jëm ci mbir mu naqari,
خُشَّعًا أَبْصَارُهُمْ يَخْرُجُونَ مِنَ الْأَجْدَاثِ كَأَنَّهُمْ جَرَادٌ مُّنتَشِرٌ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
ñuy jatt seeni gis ba, di génne ci bàmmeel yi dañuy melni ay soccent yu ñu tasaare,
مُّهْطِعِينَ إِلَى الدَّاعِ ۖ يَقُولُ الْكَافِرُونَ هَٰذَا يَوْمٌ عَسِرٌ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
sëggël seeni doq, jëm ca, wootekatu ba. Yéefër yaa nga naan : “Lii dey bis bu jafeñ la”.
۞ كَذَّبَتْ قَبْلَهُمْ قَوْمُ نُوحٍ فَكَذَّبُوا عَبْدَنَا وَقَالُوا مَجْنُونٌ وَازْدُجِرَ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
Nitu Nooh, ña leen jiitu woon weddi woon nañu. Ñoom it weddi woon nañu sunub jaam daldi wax ne: “Kii ab dof la ! ” daldi koy bàyyi.
فَدَعَا رَبَّهُ أَنِّي مَغْلُوبٌ فَانتَصِرْ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
mu woo Boroomam ñaan ko ne : “Man dey sonal nañu ma. Dimbalima”.
فَفَتَحْنَا أَبْوَابَ السَّمَاءِ بِمَاءٍ مُّنْهَمِرٍ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
Nu daldi ubbi wunti asamaan si ci am ndox muy dottiku,
وَفَجَّرْنَا الْأَرْضَ عُيُونًا فَالْتَقَى الْمَاءُ عَلَىٰ أَمْرٍ قَدْ قُدِرَ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
nu daldi ballal suuf ak ay bëti ndox. Ndox ya daldi gëndóo daj ci ndigal lu ñu natale.
وَحَمَلْنَاهُ عَلَىٰ ذَاتِ أَلْوَاحٍ وَدُسُرٍ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
Ñu toog ca kaw gaalam ga doon ay dénk ak i pont,
تَجْرِي بِأَعْيُنِنَا جَزَاءً لِّمَن كَانَ كُفِرَ ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
mu doon dawe ci sunug càmm : faye ko ko ngir ña weddi woon.
وَلَقَد تَّرَكْنَاهَا آيَةً فَهَلْ مِن مُّدَّكِرٍ ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
Bàyyi nañu ko, mu di [kéemaan]. Moo ndax kon duñu ca jàjju ?
فَكَيْفَ كَانَ عَذَابِي وَنُذُرِ ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
Te naka lay deme Sama mbugël at Samay xuppaate ?
وَلَقَدْ يَسَّرْنَا الْقُرْآنَ لِلذِّكْرِ فَهَلْ مِن مُّدَّكِرٍ ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Yombal Nanu, Alxuraan ngir ñu fàttelikoo ca. Moo kon ndax kenn dana ci jàjjoo ?
كَذَّبَتْ عَادٌ فَكَيْفَ كَانَ عَذَابِي وَنُذُرِ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
Waa Aad weddi woon nañu. Waaye naka la mbugël ma deme woon ak xupp ga ma leen defoon ?
إِنَّا أَرْسَلْنَا عَلَيْهِمْ رِيحًا صَرْصَرًا فِي يَوْمِ نَحْسٍ مُّسْتَمِرٍّ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
Yabaloon nanu ca ñoom ngelaw lu ànd ak ub (sedd), ci bis bu tiis te mbugël ma faf wàccatuleen ;
تَنزِعُ النَّاسَ كَأَنَّهُمْ أَعْجَازُ نَخْلٍ مُّنقَعِرٍ ۝٢٠
📖 Tekki Aaya 20
dadoon sempi nit ñi ni ay dàtti tàndarma di buure.
فَكَيْفَ كَانَ عَذَابِي وَنُذُرِ ۝٢١
📖 Tekki Aaya 21
Naka mu Sama mbugël ak Samag xuppaate ?
وَلَقَدْ يَسَّرْنَا الْقُرْآنَ لِلذِّكْرِ فَهَلْ مِن مُّدَّكِرٍ ۝٢٢
📖 Tekki Aaya 22
Yombal Nanu Alxuraan ngir ñu fàttalikoo ca. Moo kon ndax kenn dana ca jàjjoo ?
كَذَّبَتْ ثَمُودُ بِالنُّذُرِ ۝٢٣
📖 Tekki Aaya 23
Waa Samuud weddi woon nañu fàtteli ga?
فَقَالُوا أَبَشَرًا مِّنَّا وَاحِدًا نَّتَّبِعُهُ إِنَّا إِذًا لَّفِي ضَلَالٍ وَسُعُرٍ ۝٢٤
📖 Tekki Aaya 24
Ñuy wax naan : “Jenn waay ni nun nu di ko topp ? Kon dey nu sànku te réer.
أَأُلْقِيَ الذِّكْرُ عَلَيْهِ مِن بَيْنِنَا بَلْ هُوَ كَذَّابٌ أَشِرٌ ۝٢٥
📖 Tekki Aaya 25
Moo ndax dañu koo coqate moom doŋŋ ci nun yónni ko ? Kii daal ab fentaakoon la, bu yées”
سَيَعْلَمُونَ غَدًا مَّنِ الْكَذَّابُ الْأَشِرُ ۝٢٦
📖 Tekki Aaya 26
Xalset nañu xam bu ëllëgee, ana kan mooy fentaakoon bu yées ba.
إِنَّا مُرْسِلُو النَّاقَةِ فِتْنَةً لَّهُمْ فَارْتَقِبْهُمْ وَاصْطَبِرْ ۝٢٧
📖 Tekki Aaya 27
yónni nanu ca ñoom naaga (gileem gu jigéen), muy sànje ci ñoom. Fugluleen te muñalleen (Saalih).
وَنَبِّئْهُمْ أَنَّ الْمَاءَ قِسْمَةٌ بَيْنَهُمْ ۖ كُلُّ شِرْبٍ مُّحْتَضَرٌ ۝٢٨
📖 Tekki Aaya 28
Nanga xamle ne ndox ma dañu koy bokk séddóo ñook [giléem ga] ; duñu fa fekkante.
فَنَادَوْا صَاحِبَهُمْ فَتَعَاطَىٰ فَعَقَرَ ۝٢٩
📖 Tekki Aaya 29
Ñu daldi woo seen àndandoo mu daldi koy rey.
فَكَيْفَ كَانَ عَذَابِي وَنُذُرِ ۝٣٠
📖 Tekki Aaya 30
Naka la Sama mbugël ak Sama xupp nekke (ci seen kaw) ?
إِنَّا أَرْسَلْنَا عَلَيْهِمْ صَيْحَةً وَاحِدَةً فَكَانُوا كَهَشِيمِ الْمُحْتَظِرِ ۝٣١
📖 Tekki Aaya 31
Yabal nanu ca ñoom genn Xaacu, ñu mel poñiitum kuy ñag am ñax.
وَلَقَدْ يَسَّرْنَا الْقُرْآنَ لِلذِّكْرِ فَهَلْ مِن مُّدَّكِرٍ ۝٣٢
📖 Tekki Aaya 32
Yombal nanu, Alxuraan ngir ñu fàttaliku ca. Mo ndax kenn dana ca jàjjoo ?
كَذَّبَتْ قَوْمُ لُوطٍ بِالنُّذُرِ ۝٣٣
📖 Tekki Aaya 33
Nitu Lóot weddi woon nañu lañu leen daan xuppe.
إِنَّا أَرْسَلْنَا عَلَيْهِمْ حَاصِبًا إِلَّا آلَ لُوطٍ ۖ نَّجَّيْنَاهُم بِسَحَرٍ ۝٣٤
📖 Tekki Aaya 34
Yabal Nanu ca ñoom ngelawu callmeer (mu faagaagal leen), ba mu des njabootug Lóot ñoom musël Nanu leen ca njël,
نِّعْمَةً مِّنْ عِندِنَا ۚ كَذَٰلِكَ نَجْزِي مَن شَكَرَ ۝٣٥
📖 Tekki Aaya 35
mudi xéewal gu bawoo ci Nun : noonu Lanuy faye képp kuy sant.
وَلَقَدْ أَنذَرَهُم بَطْشَتَنَا فَتَمَارَوْا بِالنُّذُرِ ۝٣٦
📖 Tekki Aaya 36
Daan na leen xupp ci Sunu mbugël. Waaye teewul ñu daan werante ci loolu.
وَلَقَدْ رَاوَدُوهُ عَن ضَيْفِهِ فَطَمَسْنَا أَعْيُنَهُمْ فَذُوقُوا عَذَابِي وَنُذُرِ ۝٣٧
📖 Tekki Aaya 37
Dañoo, sàkkoo saay-saaye ganam ña. Nu daldi fatt seen gët ne leen “Mosleen Sama mbugël ak Samak xupp”.
وَلَقَدْ صَبَّحَهُم بُكْرَةً عَذَابٌ مُّسْتَقِرٌّ ۝٣٨
📖 Tekki Aaya 38
Mu foog leen, suba teel, ak mbugël mu ñu dootul tàggool.
فَذُوقُوا عَذَابِي وَنُذُرِ ۝٣٩
📖 Tekki Aaya 39
Mosleen Samak mbugël ak Samag xuppe.
وَلَقَدْ يَسَّرْنَا الْقُرْآنَ لِلذِّكْرِ فَهَلْ مِن مُّدَّكِرٍ ۝٤٠
📖 Tekki Aaya 40
Yombal Nanu Alxuraan ngir ñu fàttalikoo ca. Mo ndax kon kenn dana ca jàjjoo ?
وَلَقَدْ جَاءَ آلَ فِرْعَوْنَ النُّذُرُ ۝٤١
📖 Tekki Aaya 41
Nitu Firawna ya ñoom it, xupp ga dikkaloon na leen.
كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا كُلِّهَا فَأَخَذْنَاهُمْ أَخْذَ عَزِيزٍ مُّقْتَدِرٍ ۝٤٢
📖 Tekki Aaya 42
Ñoom dañoo weddi faf sunu kàddu yépp. Nu daldi leen faagaagal, ak doole.
أَكُفَّارُكُمْ خَيْرٌ مِّنْ أُولَٰئِكُمْ أَمْ لَكُم بَرَاءَةٌ فِي الزُّبُرِ ۝٤٣
📖 Tekki Aaya 43
Seen yéefar yi ndax dañoo gën ñooña ? Walla dañu leen bindal ci téere yi ne mucc ngeen ?
أَمْ يَقُولُونَ نَحْنُ جَمِيعٌ مُّنتَصِرٌ ۝٤٤
📖 Tekki Aaya 44
Walla ñoom dañuy wax naan : “Nun ñépp nooy am ndam”.
سَيُهْزَمُ الْجَمْعُ وَيُوَلُّونَ الدُّبُرَ ۝٤٥
📖 Tekki Aaya 45
Seen booloo gi dana tas , ñu ne wëqét daw wane ginnaaw.
بَلِ السَّاعَةُ مَوْعِدُهُمْ وَالسَّاعَةُ أَدْهَىٰ وَأَمَرُّ ۝٤٦
📖 Tekki Aaya 46
Bis Pénc, ba la ñuy dajeeti, te bis Pénc moo gënatee mitti te tar.
إِنَّ الْمُجْرِمِينَ فِي ضَلَالٍ وَسُعُرٍ ۝٤٧
📖 Tekki Aaya 47
Tooñkat ya ña nga ca, cànkute ak réer.
يَوْمَ يُسْحَبُونَ فِي النَّارِ عَلَىٰ وُجُوهِهِمْ ذُوقُوا مَسَّ سَقَرَ ۝٤٨
📖 Tekki Aaya 48
Bu keroogee ba ñu di leen diri ci seen xarkanam ca biir Safara, (naan leen) : “Mosleen tokamti gu Safara”.
إِنَّا كُلَّ شَيْءٍ خَلَقْنَاهُ بِقَدَرٍ ۝٤٩
📖 Tekki Aaya 49
Noo bind lépp lu nekk cig natale,
وَمَا أَمْرُنَا إِلَّا وَاحِدَةٌ كَلَمْحٍ بِالْبَصَرِ ۝٥٠
📖 Tekki Aaya 50
amul sunu menn mbir [ndigal] ; [lu dul ne] dafay mel ni xefiinu bët.
وَلَقَدْ أَهْلَكْنَا أَشْيَاعَكُمْ فَهَلْ مِن مُّدَّكِرٍ ۝٥١
📖 Tekki Aaya 51
Faagaagal Nanu, ay xeet yu mel ni yéen. Mo ndax kon kenn du fàttaliku jàjj ?
وَكُلُّ شَيْءٍ فَعَلُوهُ فِي الزُّبُرِ ۝٥٢
📖 Tekki Aaya 52
Te lépp lu ñu defoon bind Nanu ko ca téere ya,
وَكُلُّ صَغِيرٍ وَكَبِيرٍ مُّسْتَطَرٌ ۝٥٣
📖 Tekki Aaya 53
lépp, lu ndaw ak lu mag, karmat nañu ko ca.
إِنَّ الْمُتَّقِينَ فِي جَنَّاتٍ وَنَهَرٍ ۝٥٤
📖 Tekki Aaya 54
Ña ragal Yàlla ña nga ca àjjana yu am i dex,
فِي مَقْعَدِ صِدْقٍ عِندَ مَلِيكٍ مُّقْتَدِرٍ ۝٥٥
📖 Tekki Aaya 55
ca kërug dëgg ga, fa Buur Bu am kàttan ba.
← 53 Al-Qamar (54/114) 55 →
Jàng Simoore Al-Qamar ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

54القمر Al-Qamar 📚 55 Aaya مكية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers