Hud · 36/123
Tekki Waxtaan — Simoore Hud
وَأُوحِيَ إِلَىٰ نُوحٍ أَنَّهُ لَن يُؤْمِنَ مِن قَوْمِكَ إِلَّا مَن قَدْ آمَنَ فَلَا تَبْتَئِسْ بِمَا كَانُوا يَفْعَلُونَ ۝٣٦
Wa oohiya ilaa Noohin annahoo lany-yu`mina min qawmika illaa man qad aamana falaa tabta`is bimaa kaanoo yaf`aloon
📖 Tekkim Wolof
Te soloo woon Nanu Nooh [xamal ko], ne ko : “Kenn dootul gëm ci saw nit lu dul ña xas a gëm ba noppi. Kon bul jàq ca la ñuy def.

🎧 Dégg


📜 Aaya 34-38 — Simoore Hud

34وَلَا يَنفَعُكُمْ نُصْحِي إِنْ أَرَدتُّ أَنْ أَنصَحَ لَكُمْ إِن كَانَ اللَّهُ يُرِيدُ أَن يُغْوِيَكُمْ ۚ هُوَ رَبُّكُمْ وَإِلَيْهِ تُرْجَعُونَ
Te lu ma leen bëgg bëgg a laabire, te [seen Boorom] namm ci yéen bew, kon laabire googu duleen jariñ dara. Ndax Yàlla moo di seen Boroom te ca Moom ngeen di dellu”.
35أَمْ يَقُولُونَ افْتَرَاهُ ۖ قُلْ إِنِ افْتَرَيْتُهُ فَعَلَيَّ إِجْرَامِي وَأَنَا بَرِيءٌ مِّمَّا تُجْرِمُونَ
Am dañuy wax ne : dañu koo duur ? Neeleen : “Su fekkee ne dama koo duur, sama bàkkaar ci sama kaw lay dal ! Te li ngeen di bàkkaar it ku ca set wecc laa”.
36وَأُوحِيَ إِلَىٰ نُوحٍ أَنَّهُ لَن يُؤْمِنَ مِن قَوْمِكَ إِلَّا مَن قَدْ آمَنَ فَلَا تَبْتَئِسْ بِمَا كَانُوا يَفْعَلُونَ
Te soloo woon Nanu Nooh [xamal ko], ne ko : “Kenn dootul gëm ci saw nit lu dul ña xas a gëm ba noppi. Kon bul jàq ca la ñuy def.
37وَاصْنَعِ الْفُلْكَ بِأَعْيُنِنَا وَوَحْيِنَا وَلَا تُخَاطِبْنِي فِي الَّذِينَ ظَلَمُوا ۚ إِنَّهُم مُّغْرَقُونَ
Defaral gaal ci Sunug càmm ak ci Sunu ndigal. Te bul wàqanteeti ak Man ci mbirum ñiy tooñ, ñoom dañu leen di labal”.
38وَيَصْنَعُ الْفُلْكَ وَكُلَّمَا مَرَّ عَلَيْهِ مَلَأٌ مِّن قَوْمِهِ سَخِرُوا مِنْهُ ۚ قَالَ إِن تَسْخَرُوا مِنَّا فَإِنَّا نَسْخَرُ مِنكُمْ كَمَا تَسْخَرُونَ
Muy defar gaal ga. Saa yu ko kenn ci kilifay aw nitam rombee, reetaan ko. Mu ne : “Su ngeen nu reetaanee [tey jii], nun itam [dananu leen reetaan] nu ngeen nu reetaanee woon.
HudFihi Alxuraan
123Aaya
MeccanRevelation
36Aaya

Tekki — Hud 36

Simoore Hud Aaya 36 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te soloo woon Nanu Nooh [xamal ko], ne ko :…

Simoore Aaya 36/123 — Simoore Hud هود (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Hud Dégg, Simoore Hud Tekki, Simoore Hud mp3, Simoore Hud pdf. Aaya 34–38. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers