Yusuf · 27/111
Tekki Waxtaan — Simoore Yusuf
وَإِن كَانَ قَمِيصُهُ قُدَّ مِن دُبُرٍ فَكَذَبَتْ وَهُوَ مِنَ الصَّادِقِينَ ۝٢٧
Wa in kaana qameesuhoo qudda min duburin fakazabat wa huwa minas saadiqeen
📖 Tekkim Wolof
Bu yéreem xottikoo ci ginnaaw, ndaw sa moo fen, moom mu bokk ca ñu dëggu ña”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 25-29 — Simoore Yusuf

25وَاسْتَبَقَا الْبَابَ وَقَدَّتْ قَمِيصَهُ مِن دُبُرٍ وَأَلْفَيَا سَيِّدَهَا لَدَى الْبَابِ ۚ قَالَتْ مَا جَزَاءُ مَنْ أَرَادَ بِأَهْلِكَ سُوءًا إِلَّا أَن يُسْجَنَ أَوْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ñu jëkkante buntu ba, [ndaw sa] xëcc yérey [Yuusufa] ca ginnaaw ga. Ñu dajeek jëkkëram ca buntu ba. [Ndaw sa] daldi ne : “Ana lan moo di peyug ku naral lu bon sa jabar, lu dul tëj ci kaso walla mbugal mu metti ? ”
26قَالَ هِيَ رَاوَدَتْنِي عَن نَّفْسِي ۚ وَشَهِدَ شَاهِدٌ مِّنْ أَهْلِهَا إِن كَانَ قَمِيصُهُ قُدَّ مِن قُبُلٍ فَصَدَقَتْ وَهُوَ مِنَ الْكَاذِبِينَ
[Yuusufa] ne : “Moo ma sàkku ci sama jëmm”. Mu am seede su di mbokkum ndaw sa daldi seede ne : “Bu fekkee ne yéreem ci kanam la xottiku, ndaw sa moo wax dëgg, moom mu bokk ca fenkat ya.
27وَإِن كَانَ قَمِيصُهُ قُدَّ مِن دُبُرٍ فَكَذَبَتْ وَهُوَ مِنَ الصَّادِقِينَ
Bu yéreem xottikoo ci ginnaaw, ndaw sa moo fen, moom mu bokk ca ñu dëggu ña”.
28فَلَمَّا رَأَىٰ قَمِيصَهُ قُدَّ مِن دُبُرٍ قَالَ إِنَّهُ مِن كَيْدِكُنَّ ۖ إِنَّ كَيْدَكُنَّ عَظِيمٌ
Ba jëkkër ja gisee yére ya xottiku ca ginnaaw, mu ne : “Lii ci seeni pexe la [yéen jigéen ñi] ! te seeni pexe réy na !
29يُوسُفُ أَعْرِضْ عَنْ هَٰذَا ۚ وَاسْتَغْفِرِي لِذَنبِكِ ۖ إِنَّكِ كُنتِ مِنَ الْخَاطِئِينَ
Yuusufa, dëddul lii ! Te yaw [sama jabar] jéggalul sa bàkkaar ndax yaw bokk nga ca ñay def lu bon”.
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
27Aaya

Tekki — Yusuf 27

Simoore Yusuf Aaya 27 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu yéreem xottikoo ci ginnaaw, ndaw sa moo fen, moom…

Simoore Aaya 27/111 — Simoore Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Yusuf Dégg, Simoore Yusuf Tekki, Simoore Yusuf mp3, Simoore Yusuf pdf. Aaya 25–29. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers