Ar-Ra'd · 28/43
Tekki Waxtaan — Ar-Ra'd
الَّذِينَ آمَنُوا وَتَطْمَئِنُّ قُلُوبُهُم بِذِكْرِ اللَّهِ ۗ أَلَا بِذِكْرِ اللَّهِ تَطْمَئِنُّ الْقُلُوبُ ۝٢٨
Allazeena aamanoo wa tatma`innu quloobuhum bizikril laah; alaa bizikril laahi tatma`innul quloob
📖 Tekkim Wolof
ñooy ña gëm te seen xol dal ci tudd Yàlla”. Te nag ca dëgg-dëgg, tuddu Yàlla mooy dalal xel yi [xol yi] ?
🎧 Dégg

📜 Aaya 26-30 — Ar-Ra'd

26اللَّهُ يَبْسُطُ الرِّزْقَ لِمَن يَشَاءُ وَيَقْدِرُ ۚ وَفَرِحُوا بِالْحَيَاةِ الدُّنْيَا وَمَا الْحَيَاةُ الدُّنْيَا فِي الْآخِرَةِ إِلَّا مَتَاعٌ
Yàlla dana yaatal wërsëg ci ku ko soob, Dana ko xatal it. Te ñoom dundu àdduna neex na leen, te dundu àdduna soo ko méngaleek gu àllaaxira, du nekk lu dul xéewal gu ñàkk solo.
27وَيَقُولُ الَّذِينَ كَفَرُوا لَوْلَا أُنزِلَ عَلَيْهِ آيَةٌ مِّن رَّبِّهِ ۗ قُلْ إِنَّ اللَّهَ يُضِلُّ مَن يَشَاءُ وَيَهْدِي إِلَيْهِ مَنْ أَنَابَ
Te ñoom ña weddi dañuy wax naan : “Lu tee woon ñu wàcce ci moom kéemaan gu jóge ca Boroomam ? ”. Waxal ne : “Yàlla dana bàyyi cig réer ku ko soob, te it Dana gindi jëme ci Moom ku dellu [jëm ci topp Yàlla],
28الَّذِينَ آمَنُوا وَتَطْمَئِنُّ قُلُوبُهُم بِذِكْرِ اللَّهِ ۗ أَلَا بِذِكْرِ اللَّهِ تَطْمَئِنُّ الْقُلُوبُ
ñooy ña gëm te seen xol dal ci tudd Yàlla”. Te nag ca dëgg-dëgg, tuddu Yàlla mooy dalal xel yi [xol yi] ?
29الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ طُوبَىٰ لَهُمْ وَحُسْنُ مَآبٍ
Ña gëm tey jëf jëf yu sell yi, am nañu ag texe ak delluwaay bu rafet.
30كَذَٰلِكَ أَرْسَلْنَاكَ فِي أُمَّةٍ قَدْ خَلَتْ مِن قَبْلِهَا أُمَمٌ لِّتَتْلُوَ عَلَيْهِمُ الَّذِي أَوْحَيْنَا إِلَيْكَ وَهُمْ يَكْفُرُونَ بِالرَّحْمَٰنِ ۚ قُلْ هُوَ رَبِّي لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ عَلَيْهِ تَوَكَّلْتُ وَإِلَيْهِ مَتَابِ
Ci noonu yónni Naa la ci xeet woo xam ne - yeneen xeet ya wéy jiitu woon nañu ko - ngir nga jàngal leen la Nu la soloo, ci noonu ñuy wéy di weddi Yërëmaakoon bi [Yàlla]. Waxal ne : “Moom moo di sama Boroom. Amul jeneen yàlla ju dul Moom. Ci Moom laa wéeru te ci Moom la delluwaay ba nekk”.
Ar-Ra'dFihi Alxuraan
43Aaya
MedinanRevelation
28Aaya

Tekki — Ar-Ra'd 28

Simoore Ar-Ra'd Aaya 28 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : ñooy ña gëm te seen xol dal ci tudd Yàlla”.…

Simoore Aaya 28/43 — Ar-Ra'd الرعد (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ar-Ra'd Dégg, Ar-Ra'd Tekki, Ar-Ra'd mp3, Ar-Ra'd pdf. Aaya 26–30. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers