Al-An'am · 23/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
ثُمَّ لَمْ تَكُن فِتْنَتُهُمْ إِلَّا أَن قَالُوا وَاللَّهِ رَبِّنَا مَا كُنَّا مُشْرِكِينَ ۝٢٣
Summa lam takun fitnatuhum illaaa an qaaloo wallaahi Rabbinaa maa kunnaa mushrikeen
📖 Tekkim Wolof
Su ko defee, seen njàqare duleen xiir ci leneen lu dul ñuy wax naan : “Giñ nanu ci Yàlla sunu Boroom ne nekkunu woon di way-bokkaale”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 21-25 — Al-An'am

21وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّنِ افْتَرَىٰ عَلَى اللَّهِ كَذِبًا أَوْ كَذَّبَ بِآيَاتِهِ ۗ إِنَّهُ لَا يُفْلِحُ الظَّالِمُونَ
Ana ku gën a tooñ kuy duural Yàlla aw fen, walla di weddi ay kàddoom ? Tooñkat ya duñu texe de.
22وَيَوْمَ نَحْشُرُهُمْ جَمِيعًا ثُمَّ نَقُولُ لِلَّذِينَ أَشْرَكُوا أَيْنَ شُرَكَاؤُكُمُ الَّذِينَ كُنتُمْ تَزْعُمُونَ
Ca bis ba ñu leen di fang ñoom ñépp [dajale leen], bu ñuy wax ak ña daan bokkaale, ne leen : “Ana ña ngeen sosoon, bokkaale woon leen ak Yàlla ?
23ثُمَّ لَمْ تَكُن فِتْنَتُهُمْ إِلَّا أَن قَالُوا وَاللَّهِ رَبِّنَا مَا كُنَّا مُشْرِكِينَ
Su ko defee, seen njàqare duleen xiir ci leneen lu dul ñuy wax naan : “Giñ nanu ci Yàlla sunu Boroom ne nekkunu woon di way-bokkaale”.
24انظُرْ كَيْفَ كَذَبُوا عَلَىٰ أَنفُسِهِمْ ۚ وَضَلَّ عَنْهُم مَّا كَانُوا يَفْتَرُونَ
Gisal ni ñuy fenee seen bopp ! Te dana fekk la ñu daan duur réer leen mërr !
25وَمِنْهُم مَّن يَسْتَمِعُ إِلَيْكَ ۖ وَجَعَلْنَا عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ أَكِنَّةً أَن يَفْقَهُوهُ وَفِي آذَانِهِمْ وَقْرًا ۚ وَإِن يَرَوْا كُلَّ آيَةٍ لَّا يُؤْمِنُوا بِهَا ۚ حَتَّىٰ إِذَا جَاءُوكَ يُجَادِلُونَكَ يَقُولُ الَّذِينَ كَفَرُوا إِنْ هَٰذَا إِلَّا أَسَاطِيرُ الْأَوَّلِينَ
Am na ci ñoom ñu lay déglu, waaye def Nanu ci seen xol muuraay ba duñu am dégg-dégg ci Alxuraan, te ca seeni nopp, def Nanu ca saañ. Tax na bu ñu gisee laaya, ju mu mën di doon, ne duñu ko gëm. Ba ba ñuy ñëw dàggasanteek yaw, dañuy wax ñoom ñi weddi : “Lii du dara lu dul léebi mag ñu njëkk ña”.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
23Aaya

Tekki — Al-An'am 23

Simoore Al-An'am Aaya 23 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Su ko defee, seen njàqare duleen xiir ci leneen lu…

Simoore Aaya 23/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 21–25. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers