Al-Maida · 27/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
۞ وَاتْلُ عَلَيْهِمْ نَبَأَ ابْنَيْ آدَمَ بِالْحَقِّ إِذْ قَرَّبَا قُرْبَانًا فَتُقُبِّلَ مِنْ أَحَدِهِمَا وَلَمْ يُتَقَبَّلْ مِنَ الْآخَرِ قَالَ لَأَقْتُلَنَّكَ ۖ قَالَ إِنَّمَا يَتَقَبَّلُ اللَّهُ مِنَ الْمُتَّقِينَ ۝٢٧
Watlu `alaihim naba abnai Aadama bilhaqq; iz qarrabaa qurbaanan fatuqubbila min ahadihimaa wa lam yutaqabbal minal aakhari qaala la aqtulannnaka qaala innamaa yataqabbalul laahu minal muttaqeen
📖 Tekkim Wolof
Nettalileen, ci lu dëggu, xibaari ñaari doomi Aadama ya. Ba ñu sàkkoo yool bu ñu jaamoo Yàlla ; te Yàlla nangul kenn ca ñoom ñaar, bañ a nangul ka ca des. Ka ñu nangulul wax ne : “Danaa la rey”. Ka ñu nangul ne ko : “Na la wóor yaw it ne, Yàlla ña ko ragal lay nangu seeni jëf”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 25-29 — Al-Maida

25قَالَ رَبِّ إِنِّي لَا أَمْلِكُ إِلَّا نَفْسِي وَأَخِي ۖ فَافْرُقْ بَيْنَنَا وَبَيْنَ الْقَوْمِ الْفَاسِقِينَ
Mu ne : “Sam Boroom ! Mënaluma dara ku dul man ak sama mbokk [Haaruuna : àtteel sunu diggante ak ñiy sàqi ndigal”.
26قَالَ فَإِنَّهَا مُحَرَّمَةٌ عَلَيْهِمْ ۛ أَرْبَعِينَ سَنَةً ۛ يَتِيهُونَ فِي الْأَرْضِ ۚ فَلَا تَأْسَ عَلَى الْقَوْمِ الْفَاسِقِينَ
[Boroom bi tontu] ne: “Suuf soosu araam na leen ñeent-fukki at yoo xam ne danañu gëlëm di wëndéelu ci àll bi. Bul jàq ci mbiru ñiy sàqi ndigal”.
27۞ وَاتْلُ عَلَيْهِمْ نَبَأَ ابْنَيْ آدَمَ بِالْحَقِّ إِذْ قَرَّبَا قُرْبَانًا فَتُقُبِّلَ مِنْ أَحَدِهِمَا وَلَمْ يُتَقَبَّلْ مِنَ الْآخَرِ قَالَ لَأَقْتُلَنَّكَ ۖ قَالَ إِنَّمَا يَتَقَبَّلُ اللَّهُ مِنَ الْمُتَّقِينَ
Nettalileen, ci lu dëggu, xibaari ñaari doomi Aadama ya. Ba ñu sàkkoo yool bu ñu jaamoo Yàlla ; te Yàlla nangul kenn ca ñoom ñaar, bañ a nangul ka ca des. Ka ñu nangulul wax ne : “Danaa la rey”. Ka ñu nangul ne ko : “Na la wóor yaw it ne, Yàlla ña ko ragal lay nangu seeni jëf”.
28لَئِن بَسَطتَ إِلَيَّ يَدَكَ لِتَقْتُلَنِي مَا أَنَا بِبَاسِطٍ يَدِيَ إِلَيْكَ لِأَقْتُلَكَ ۖ إِنِّي أَخَافُ اللَّهَ رَبَّ الْعَالَمِينَ
Te boo tàllalee sa loxo di ma rey man dey duma jëme sama loxo ci yaw waxantumalaak di la jéem a rey : ndax man Yàlla Miy Boroom mbindeef yi laa ragal.
29إِنِّي أُرِيدُ أَن تَبُوءَ بِإِثْمِي وَإِثْمِكَ فَتَكُونَ مِنْ أَصْحَابِ النَّارِ ۚ وَذَٰلِكَ جَزَاءُ الظَّالِمِينَ
Te sax li ma namm moo di nga yenu sama bàkkaar boole kook sa bos : bu ko defee nga bokk ca waa Safara. Te loolu mooy peyug tooñkat ya.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
27Aaya

Tekki — Al-Maida 27

Simoore Al-Maida Aaya 27 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nettalileen, ci lu dëggu, xibaari ñaari doomi Aadama ya. Ba…

Simoore Aaya 27/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 25–29. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers