Al-Isra · 42/111
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Isra
قُل لَّوْ كَانَ مَعَهُ آلِهَةٌ كَمَا يَقُولُونَ إِذًا لَّابْتَغَوْا إِلَىٰ ذِي الْعَرْشِ سَبِيلًا ۝٤٢
Qul law kaana ma`ahooo aalihatun kamaa yaqooloona izal labtaghaw ilaa zil `Arshi Sabeela
📖 Tekkim Wolof
Neel : “Bu amoon yeneeni Yàlla tu nekk ak Moom, ni ñu ko waxe, kon dinañu sàkk [yoon wu leen yóbb] ca Boroom gàngune ga”.(yab Yàlla)

🎧 Dégg


📜 Aaya 40-44 — Simoore Al-Isra

40أَفَأَصْفَاكُمْ رَبُّكُم بِالْبَنِينَ وَاتَّخَذَ مِنَ الْمَلَائِكَةِ إِنَاثًا ۚ إِنَّكُمْ لَتَقُولُونَ قَوْلًا عَظِيمًا
Waaw ndax seen Borom dafa leen a tànnal ay doom yu góor, na noppi jël ci Malaaka yi ay doom yu jigéen ?Yéen nag ca dëgg-dëgg li ngeen di wax rëy na.
41وَلَقَدْ صَرَّفْنَا فِي هَٰذَا الْقُرْآنِ لِيَذَّكَّرُوا وَمَا يَزِيدُهُمْ إِلَّا نُفُورًا
Te leeral Nanu ci Alxuraan jii [lu ne] ngir ñu xalaat. Te dolliwuleen lu dul fen [wëliis dëgg].
42قُل لَّوْ كَانَ مَعَهُ آلِهَةٌ كَمَا يَقُولُونَ إِذًا لَّابْتَغَوْا إِلَىٰ ذِي الْعَرْشِ سَبِيلًا
Neel : “Bu amoon yeneeni Yàlla tu nekk ak Moom, ni ñu ko waxe, kon dinañu sàkk [yoon wu leen yóbb] ca Boroom gàngune ga”.(yab Yàlla)
43سُبْحَانَهُ وَتَعَالَىٰ عَمَّا يَقُولُونَ عُلُوًّا كَبِيرًا
Cëy sellam ga ! Kawe na, jomb na li ñuy wax, jombute gu màgg a màgg !
44تُسَبِّحُ لَهُ السَّمَاوَاتُ السَّبْعُ وَالْأَرْضُ وَمَن فِيهِنَّ ۚ وَإِن مِّن شَيْءٍ إِلَّا يُسَبِّحُ بِحَمْدِهِ وَلَٰكِن لَّا تَفْقَهُونَ تَسْبِيحَهُمْ ۗ إِنَّهُ كَانَ حَلِيمًا غَفُورًا
Juróom-ñaari asamaan yi ak suuf si, ñi ngi koy sàbbaal, ak li nekk ci seen biir. Te sax amul dara lu nekk te du Ko sàbbaal ci li Mu yeyoo mboolem cant. Waaye dangeen a amul dégg-dégg ci seeni sàbbaal. Naka Moom Aji-lewet la, Jéggalaakoon la.
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
42Aaya

Tekki — Al-Isra 42

Simoore Al-Isra Aaya 42 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Neel : “Bu amoon yeneeni Yàlla tu nekk ak Moom,…

Simoore Aaya 42/111 — Simoore Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Isra Dégg, Simoore Al-Isra Tekki, Simoore Al-Isra mp3, Simoore Al-Isra pdf. Aaya 40–44. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers