Al-Baqara · 72/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَإِذْ قَتَلْتُمْ نَفْسًا فَادَّارَأْتُمْ فِيهَا ۖ وَاللَّهُ مُخْرِجٌ مَّا كُنتُمْ تَكْتُمُونَ ۝٧٢
Wa iz qataltum nafsan faddaara`tum feehaa wallaahu mukrijum maa kuntum taktumoon
📖 Tekkim Wolof
[Fàttalikuleen] Ba ngeen reyee bakkan te ngeen jiiñante ko!... Te Yàlla génne la ngeen doon nëbb.
🎧 Dégg

📜 Aaya 70-74 — Al-Baqara

70قَالُوا ادْعُ لَنَا رَبَّكَ يُبَيِّن لَّنَا مَا هِيَ إِنَّ الْبَقَرَ تَشَابَهَ عَلَيْنَا وَإِنَّا إِن شَاءَ اللَّهُ لَمُهْتَدُونَ
- Ñu ne : “Laajal nu sa Boroom mu leeral nu nu mu mel, ndax nag yi dañoo bari ci nun. Te bu soobe Yàlla dananu gindiku [Jëfe ndigalam]”.
71قَالَ إِنَّهُ يَقُولُ إِنَّهَا بَقَرَةٌ لَّا ذَلُولٌ تُثِيرُ الْأَرْضَ وَلَا تَسْقِي الْحَرْثَ مُسَلَّمَةٌ لَّا شِيَةَ فِيهَا ۚ قَالُوا الْآنَ جِئْتَ بِالْحَقِّ ۚ فَذَبَحُوهَا وَمَا كَادُوا يَفْعَلُونَ
– Mu ne moom nag : “Nee na, nag la wu ñu bayloowul suuf si, du buy suuxat mbay, bu amul benn laago la te wenn melo la”. - Ñu ne ko : “Agsi nga ci dëgg gi! ” Ñu rendi ko te xawoon nañu koo bañ a def.
72وَإِذْ قَتَلْتُمْ نَفْسًا فَادَّارَأْتُمْ فِيهَا ۖ وَاللَّهُ مُخْرِجٌ مَّا كُنتُمْ تَكْتُمُونَ
[Fàttalikuleen] Ba ngeen reyee bakkan te ngeen jiiñante ko!... Te Yàlla génne la ngeen doon nëbb.
73فَقُلْنَا اضْرِبُوهُ بِبَعْضِهَا ۚ كَذَٰلِكَ يُحْيِي اللَّهُ الْمَوْتَىٰ وَيُرِيكُمْ آيَاتِهِ لَعَلَّكُمْ تَعْقِلُونَ
Nu ne : “Dóorleen ko lenn [Lu bokk ci nag wi]”. - Noonu la Yàllay dekkalee ñi dee te dana leen won ay kéemaan ndax ngeen xel-lu.
74ثُمَّ قَسَتْ قُلُوبُكُم مِّن بَعْدِ ذَٰلِكَ فَهِيَ كَالْحِجَارَةِ أَوْ أَشَدُّ قَسْوَةً ۚ وَإِنَّ مِنَ الْحِجَارَةِ لَمَا يَتَفَجَّرُ مِنْهُ الْأَنْهَارُ ۚ وَإِنَّ مِنْهَا لَمَا يَشَّقَّقُ فَيَخْرُجُ مِنْهُ الْمَاءُ ۚ وَإِنَّ مِنْهَا لَمَا يَهْبِطُ مِنْ خَشْيَةِ اللَّهِ ۗ وَمَا اللَّهُ بِغَافِلٍ عَمَّا تَعْمَلُونَ
Topp, seeni xol wow ginnaaw loolu [dëgër] ba mel ni xeer mbaa lu ko gën a tar wowaay ; Ndax ci xeer sax ndox dana ca ball, te am na ci xeer yi yuy xar ndox génn ca, am na ci yuy rot ngir ragal Yàlla. Te Yàlla du ñàkk a seetlu li ngeen di def.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
72Aaya

Tekki — Al-Baqara 72

Simoore Al-Baqara Aaya 72 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Fàttalikuleen] Ba ngeen reyee bakkan te ngeen jiiñante ko!... Te…

Simoore Aaya 72/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 70–74. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers