Hud · 117/123
Tekki Waxtaan — Hud
وَمَا كَانَ رَبُّكَ لِيُهْلِكَ الْقُرَىٰ بِظُلْمٍ وَأَهْلُهَا مُصْلِحُونَ ۝١١٧
Wa maa kaana Rabbuka liyuhlikal quraa bizulminw wa ahluhaa muslihoon
📖 Tekkim Wolof
Sa Boroom du alag lenn njénde ci ag tooñeel fekk aw nit di sellal seeni jëf.

🎧 Dégg


📜 Aaya 115-119 — Hud

115وَاصْبِرْ فَإِنَّ اللَّهَ لَا يُضِيعُ أَجْرَ الْمُحْسِنِينَ
Nanga muñ. Yàlla dey du sànk peyug ñay rafetal.
116فَلَوْلَا كَانَ مِنَ الْقُرُونِ مِن قَبْلِكُمْ أُولُو بَقِيَّةٍ يَنْهَوْنَ عَنِ الْفَسَادِ فِي الْأَرْضِ إِلَّا قَلِيلًا مِّمَّنْ أَنجَيْنَا مِنْهُمْ ۗ وَاتَّبَعَ الَّذِينَ ظَلَمُوا مَا أُتْرِفُوا فِيهِ وَكَانُوا مُجْرِمِينَ
Lu taxoon ca xarnu ya leen jiitu, ñu baax ña [dese woon yan bi] nekkoon ñu néew, ñoom ña daan tere lu bon ci suuf sa ! Ñu bokk ca ña Nu musaloon te ñu tooñoon, topp seeni bakkan ca xéewal ya ñu donnoon ay bàkkaarkat.
117وَمَا كَانَ رَبُّكَ لِيُهْلِكَ الْقُرَىٰ بِظُلْمٍ وَأَهْلُهَا مُصْلِحُونَ
Sa Boroom du alag lenn njénde ci ag tooñeel fekk aw nit di sellal seeni jëf.
118وَلَوْ شَاءَ رَبُّكَ لَجَعَلَ النَّاسَ أُمَّةً وَاحِدَةً ۖ وَلَا يَزَالُونَ مُخْتَلِفِينَ
Bu sooboon sa Boroom mu def nit ñi ñu nekk di wenn xeet doŋŋ. Waaye duñu deñ di wuute
119إِلَّا مَن رَّحِمَ رَبُّكَ ۚ وَلِذَٰلِكَ خَلَقَهُمْ ۗ وَتَمَّتْ كَلِمَةُ رَبِّكَ لَأَمْلَأَنَّ جَهَنَّمَ مِنَ الْجِنَّةِ وَالنَّاسِ أَجْمَعِينَ
ndare ña sa Boroom yërëm. Loolu moo tax Mu bind leen. Te it moo tax sa kàddug Boroom mat ca la mu wax ne : “Danaa feesal Safara ci aw nit ak i jinne mbooleseen”.
HudFihi Alxuraan
123Aaya
MeccanRevelation
117Aaya

Tekki — Hud 117

Simoore Hud Aaya 117 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Sa Boroom du alag lenn njénde ci ag tooñeel fekk…

Simoore Aaya 117/123 — Hud هود (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Hud Dégg, Hud Tekki, Hud mp3, Hud pdf. Aaya 115–119. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers