Yusuf · 71/111
Tekki Waxtaan — Yusuf
قَالُوا وَأَقْبَلُوا عَلَيْهِم مَّاذَا تَفْقِدُونَ ۝٧١
Qaaloo wa aqbaloo `alaihim maazaa tafqidoon
📖 Tekkim Wolof
Ñoom it ñu wëlbatiku ca moom ne leen : “Lan ngeen réerle ? ”
🎧 Dégg

📜 Aaya 69-73 — Yusuf

69وَلَمَّا دَخَلُوا عَلَىٰ يُوسُفَ آوَىٰ إِلَيْهِ أَخَاهُ ۖ قَالَ إِنِّي أَنَا أَخُوكَ فَلَا تَبْتَئِسْ بِمَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Ba ñu agsee ca Yuusufa, mu daldi xëcc taf ci boppam doomu-ndeyam ja, daldi ne : “Maa di sa doomu-ndey. Bul jàq ca la ñu nekkoon di ko def ci jéem maa sànk”.
70فَلَمَّا جَهَّزَهُم بِجَهَازِهِمْ جَعَلَ السِّقَايَةَ فِي رَحْلِ أَخِيهِ ثُمَّ أَذَّنَ مُؤَذِّنٌ أَيَّتُهَا الْعِيرُ إِنَّكُمْ لَسَارِقُونَ
Ba mu leen solalee seeni saaku ba noppi, mu dugal andaar [ja ñu doon natte] ca biir sëfu doomu-ndeyam ja. Mu am yéglekat bu wax ne : “Éy yéen jëgg ji ! Ay sàcc ngeen”.
71قَالُوا وَأَقْبَلُوا عَلَيْهِم مَّاذَا تَفْقِدُونَ
Ñoom it ñu wëlbatiku ca moom ne leen : “Lan ngeen réerle ? ”
72قَالُوا نَفْقِدُ صُوَاعَ الْمَلِكِ وَلِمَن جَاءَ بِهِ حِمْلُ بَعِيرٍ وَأَنَا بِهِ زَعِيمٌ
Ñu ne : “Li nu réerle mooy nattukaayu buur bi. Te ku ko feeñal nu jox ko sëfu giléem, maa ko warlul loolu”.
73قَالُوا تَاللَّهِ لَقَدْ عَلِمْتُم مَّا جِئْنَا لِنُفْسِدَ فِي الْأَرْضِ وَمَا كُنَّا سَارِقِينَ
Ñu ne : “Giñ nanu ci Yàlla, te xam ngeen ne dikkunu fii ci suuf si ngir yàq te it dunu ay sàcckat”.
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
71Aaya

Tekki — Yusuf 71

Simoore Yusuf Aaya 71 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñoom it ñu wëlbatiku ca moom ne leen : “Lan…

Simoore Aaya 71/111 — Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yusuf Dégg, Yusuf Tekki, Yusuf mp3, Yusuf pdf. Aaya 69–73. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers