An-Naml · 79/93
Tekki Waxtaan — Simoore An-Naml
فَتَوَكَّلْ عَلَى اللَّهِ ۖ إِنَّكَ عَلَى الْحَقِّ الْمُبِينِ ۝٧٩
Fatawakkal `alal laahi innaka `alal haqqil mubeen
📖 Tekkim Wolof
[Yaw Muhammad], nanga wéeru ci Yàlla, [te xamal it ne] yaa ngi ci dëgg gu bir.

🎧 Dégg


📜 Aaya 77-81 — Simoore An-Naml

77وَإِنَّهُ لَهُدًى وَرَحْمَةٌ لِّلْمُؤْمِنِينَ
Te Alxuraan jooju njub la ak yërmaande ci képp ku gëm [di ab jullit].
78إِنَّ رَبَّكَ يَقْضِي بَيْنَهُم بِحُكْمِهِ ۚ وَهُوَ الْعَزِيزُ الْعَلِيمُ
Sa Boroom dana àtte seen diggante ci àtteem yi ; Mooy Boroom kàttan ga, di Ku xam.
79فَتَوَكَّلْ عَلَى اللَّهِ ۖ إِنَّكَ عَلَى الْحَقِّ الْمُبِينِ
[Yaw Muhammad], nanga wéeru ci Yàlla, [te xamal it ne] yaa ngi ci dëgg gu bir.
80إِنَّكَ لَا تُسْمِعُ الْمَوْتَىٰ وَلَا تُسْمِعُ الصُّمَّ الدُّعَاءَ إِذَا وَلَّوْا مُدْبِرِينَ
Mënoo tax ku xas a dee ba noppi di dekki, mënoo tax it ab tëx dégg woote ba, saa su la wonee ginnaaw dummóoyu.
81وَمَا أَنتَ بِهَادِي الْعُمْيِ عَن ضَلَالَتِهِمْ ۖ إِن تُسْمِعُ إِلَّا مَن يُؤْمِنُ بِآيَاتِنَا فَهُم مُّسْلِمُونَ
Mënoo gindi gumba yi ci seenug réer. Ñi lay déglu kay ñooy ña gëm Sunuy kàddu te doon ay jullit.
An-NamlFihi Alxuraan
93Aaya
MeccanRevelation
79Aaya

Tekki — An-Naml 79

Simoore An-Naml Aaya 79 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Yaw Muhammad], nanga wéeru ci Yàlla, [te xamal it ne]…

Simoore Aaya 79/93 — Simoore An-Naml النمل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore An-Naml Dégg, Simoore An-Naml Tekki, Simoore An-Naml mp3, Simoore An-Naml pdf. Aaya 77–81. Tekkim Wolof: Fulfulde.





Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 21, 2026

Don't forget us in your sincere prayers