Aali Imran · 59/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
إِنَّ مَثَلَ عِيسَىٰ عِندَ اللَّهِ كَمَثَلِ آدَمَ ۖ خَلَقَهُ مِن تُرَابٍ ثُمَّ قَالَ لَهُ كُن فَيَكُونُ ۝٥٩
Inna masala `Eesaa `indal laahi kamasali Aadama khalaqahoo min turaabin summa qaala lahoo kun fayakoon
📖 Tekkim Wolof
Mbiri Iisaa ca Yàlla, dafa deme ni mbiri Aadama, dafa koo bindee ci suuf ba noppi ne ko “Nekkal” : mu nekk.

🎧 Dégg


📜 Aaya 57-61 — Simoore Aali Imran

57وَأَمَّا الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ فَيُوَفِّيهِمْ أُجُورَهُمْ ۗ وَاللَّهُ لَا يُحِبُّ الظَّالِمِينَ
Ña gëm te jëf aw yiw, danañu jot seeni pey. Yàlla sopput tooñkat ya.
58ذَٰلِكَ نَتْلُوهُ عَلَيْكَ مِنَ الْآيَاتِ وَالذِّكْرِ الْحَكِيمِ
Loolu noo ngi la koy jàngal [xamal] mu bokk ci ay kéemaan ak kàdduy fàattali yu xereñ [Alxuraan].
59إِنَّ مَثَلَ عِيسَىٰ عِندَ اللَّهِ كَمَثَلِ آدَمَ ۖ خَلَقَهُ مِن تُرَابٍ ثُمَّ قَالَ لَهُ كُن فَيَكُونُ
Mbiri Iisaa ca Yàlla, dafa deme ni mbiri Aadama, dafa koo bindee ci suuf ba noppi ne ko “Nekkal” : mu nekk.
60الْحَقُّ مِن رَّبِّكَ فَلَا تَكُن مِّنَ الْمُمْتَرِينَ
Dëgg ca sa Boroom la jóge. Bul bokk ca ña cay werante.
61فَمَنْ حَاجَّكَ فِيهِ مِن بَعْدِ مَا جَاءَكَ مِنَ الْعِلْمِ فَقُلْ تَعَالَوْا نَدْعُ أَبْنَاءَنَا وَأَبْنَاءَكُمْ وَنِسَاءَنَا وَنِسَاءَكُمْ وَأَنفُسَنَا وَأَنفُسَكُمْ ثُمَّ نَبْتَهِلْ فَنَجْعَل لَّعْنَتَ اللَّهِ عَلَى الْكَاذِبِينَ
Ku cay dàggasante ak yaw, ginnaaw la la dikke ci xam-xam [ci mbiri Iisaa], neel : “Kaayleen nu woo sunuy doom ak sunuy soxna ak seeni soxna, nu ñëw, ngeen ñëw yéen ci seen bopp topp nu toroxlu, rëbbante rëbbum Yàlla dal ci ña fen [ci mbiri Iisaa].
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
59Aaya

Tekki — Aali Imran 59

Simoore Aali Imran Aaya 59 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mbiri Iisaa ca Yàlla, dafa deme ni mbiri Aadama, dafa…

Simoore Aaya 59/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 57–61. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers